Biti Réew - 07 MONTHS.DECEMBER 2024
Ci lu soxal Ndajem Waxtaan miy am ca Doha, Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay Fay dalal na doomi Senegaal ya fay dund.
Ñu séq waxtaanu mbégte wu gànjaru wu tax ñu man ñoom doomi Senegaal yooyu dégtal ko seen i jafe-jafe, yaatal ci yéeney Senegaalu ëllëg ak gën a dooleel jëflante yi diggante jasporaa bi ak réew mi.
Njiitu Réew mi feddali na ag jaayanteem ci amal liggéey yu am solo ngir indi ay saafara ci li sunu bokki ma-réew yi di séntu ak fépp fu ñu man a féete ci àddina si, boole ko ak sóob leen ngir ñu dugal seen loxo bu baax ci luy jëmale kanam réew mi.