Biti Réew - 12 MONTHS.MAY 2025
Ci xewu tijjitel Afrikaa CEO Forum, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, amal na ay jataay diggam ak naataangoom yii di, Alasaan Watara, Njiitu Réewum Kodiwaar ak Mohammet Uld Seex El Xasuwani Njiitu Réewum Móritani.
Seen waxtaan yi, feesoon dell ak mbégte, mbokkoo ak kóolute, tax na ñu feddali yéene yi ñu bokk am jëm ci lëkkaloo ak jàppalante diggante Senegaal ak partaneeram yi ci dig-digal bi, lépp ngir Afrig gu gën a bennoo, gën a dal te gën a naat.