Ci waxtaan wu mu séq ak Marwaan Ben Yahmed mu kippaagog “Jeune Afrique Média Group”, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, yaatal na ci anam yu leer te ànd ak dogu gis-gis bu am solo bi mu am ci wàllu xarala yi ñeel Senegaal ak Afrig.
Ci biir waxtaan wi :
- Moom sunu bopp ci wàllu xarala giy tekki ag jonn ci xarala yi.
- “New Deal Technologique” bi ak 1,7i milyaari USD yi ñu ci war a dugal
- Taxawaay bi ci lëkkaloo diggante piblig-piriwe bi war a am, roye ko ci modelu Ruwandaa ak Estoni.
- Jàppale gu wér jëme ci “start-up” yi ak fent gi.
- Ngir tëj, ak mbébetu Afrig gu moom boppam ci wàllu xarala, mu lootaabewu ci tund yi ak ci kembaar gi.
Muy jataay bu jar a seetaan ngir gën a xam kenoy taxawaayu réew mu jekk ngir ëllëg boole ko ak teg jumtukaayi soppiku gu sax dàkk ci Afrig ci wàllu xarala yi.
Man ngeen a topp jataay bi fii :