Njiitu Réew mi, Basiru Jomaay Fay, mu ngi dooree bisam bu jëkk ca Abijaŋ ci ñaari ndajey koom yu am solo diggam ak Jean Kaku JAAGU, Njiital Kippangog NSIA ak Sona Jaariyetu Madina GAY, Njiital Schneider Electric Afrig, ñu àndoon ñoom ñaar ñépp ak seen uw tañ. Seen i waxtaan jëmoon ci pexey gën a dooleel lëngoo gi ci wàllu koom ak xarala diggante Senegaal ak këri lijjanti yu mag yii.
Ci ginnaaw bi, Njiitu Réew mi séq na jataay bu am solo ak doomi Senegaal yi nekk ca Kodiwaar. Muy ndaje mu ko may mu man a déglu bu baax seen i njàmbat, rafetlu seen taxawaay teg ci feddali jaayanteg nguuru Senegaal ci gunge jasporaa bii doon keno bu am solo ci suqalikug réew mi ak wane Senegaal mi ci àddina si.