Ci xewu tijjitel Afrikaa CEO Forum 2025 ca Abidjaŋ, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na ñaari jataay yu mag, yu jëm ci wàllu suqalikug koom mi ak eewestismaa yu am solo yi.
Njiitu Réew mi njëkk naa dalal Marko Aesrli, Njiital ACWA POWER, di këru liggéeyukaay guy yëngu ci wàllu yasara ak segg ndoxum xorom mi.
Waxtaan yi a ngi jëmoon ci pexey lëngoo ci wàllu yasara gi, di keno bu am solo ngir am yokkute gu wér te wóor ci Senegaal.
Ginnaaw bi, Peresidaa Fay dalal na Raley White, Topp-Njiital Kippaangog Yango, di kër gu am solo ci wàllu xarala yi ak yaale gi. Ndaje mii tax na ñu dikkaat ci mbébteti eewestismaa ak lëngoo ci wàllu xarala.
Seen jataay bii day firndeel yéeney Senegaal ci gën a dooleel ak raxante ay partaneeram, ngir baral jéego yi jëm ci suqalikug koom mi boole ko ak gën a xëcc réewi àddina si.