Biti Réew - 22 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Ca jataayu « Unstoppable Africa », ca biir « Global Africa Business Initiative », Njiitu Réew mi gòndi na fa ña doon teewlu ci gis-gis bu wér te wóor bi mu am ci Senegaal ak Afrig.
Wax na ci kay gii ndaw ñi tàwwu, mu lalu ci manal sa bopp, koom mu tijjiku jaare ko ci fent ak kóolute, ak Afrig guy dëggal boppam ci kanamu àddina sépp.
« Afrig nekkul dige bu sori : lu wér la lees war a nangu. Ay ndawam, ay kàngamam ak i balluwaayam ñoo ko jëkk a def muy tayug àddina si. »
Bataaxel bii, mu jàllale ci dal ak dogu, day wane yéeney Senegaal gu nangoo bay waaram niki kenob Afrig gu am doole te doon benn.