jëwriñ - 11 MONTHS.MAY 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dina teew 12 ak 13i fani mee 2025 ca 12eelu edisoo bu Africa CEO Forum bi ñuy amal ca Abijaŋ, nekk ca réewum Kodiwaar.
Ñu war cee waxtaane tomb bii di « Ndax
New Deal public-privé man naa séddalewaat kàrt yi ngir njariñu Afrig ?», ndaje mii dees na fa yaatal lu jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi diggante ngóornamaŋ yi ak sektéer piriwe bi, yoriin ak baral jéego yi jëm ci bennale yaxantug Afrig jaare ko ci ZLECAF.