Adis-Abebaa : Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na Aliko Dangote ak Dr OkeyOsamah.

Biti Réew - 15 MONTHS.FEBRUARY 2025


Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dalal na ci ab jataay lijjantikatu saa-niseriyaa bii di Aliko Dangote niki noonu Dr Okey Oramah miy Njiital Afreximbank.

Waxtaan yi jëmoon ci kopparal ak liggéey yu man a am ci pàcc yu am solo yu mel ni yasara gi, ndefarum àngare ak ndefar yi. Jubluwaay bi di fexee yokk dooley Senegaal ci wàllu ndefar boole ko ak gunge gis-gis bii di « Stratégie nationale de développement 2024-2029 ».


Ca jataay boobu, Njiitu Réew mi feddali na jaayanteg Senegaal ngir taxawal réew mu jàppandi ci wàllu jëflante ngir amal eewestismaa yu wér boole ko amal ay lëngoo yu am solo ak sektéer piriweb Afrig bi lépp ngir baral jéego yi jëm ci soppi koomum réew mi.