Ca 4eelu Ndaje ma àddina si di waxtaane koppralug suqaliku gi, ñu amal ko tay ca Seville, Kilifa gi, Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, teewe na jataay bu kawe boobu, ànd ko ak Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu bari, niki noonu kilifa yu mag yu bokk ci ay mbootaay ci àddina si.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na dalal gu mucc ayib gi ko kilifay Espaañ yi jagleel teg ci feddali ag cantam ci jaayante gu sax dàkk gi réewum Espaañ am ngir yokkute gu daj àddina.
Lu jëm ci jafe-jafe yiy gàllankoor suqaliku gu sax dàkk, Njiitu Réew mi taxawlu na bu baax ci xamle ne fàww ñu amal ci lu gaaw ay coppite ci ni ñuy saytoo koom mi ak koppar yi ci àddina si, ngir joyyanti ñàkk a yemale ci wàllu doxaliin yi ñu donne ci li wees te ba fii mu ne nii, mu doon luy gàllankoor suqalikug réew yu néew doole yi.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY woote na ngir ñu xoolaat bu baax anam yi kurél yiy xayma ci wàllu kopparal di càmbaree, nga xam ne doxaliin yi day gën a mettil anam yi ñuy jotee ci bor yi teg ci di gën a diisal anam yi ñu leen di fayee ñeel réew yu néew doole yi.