Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, yékkati na ay kàddu jagleel ko askan wi ci talaata ji 31i fani desàmbar 2024, muy màndargaal njeextalu at mi di am pose ngir dëgmal ëllëg. Cig àddoom, Njiitu Réew mi, ñaanal na jàmm ak wér gi yaram ñeel mbooleem saa-senegaal yi, boole ci delloo njukkal ñi fi bàyyikoo ci at mi.
Ndakaaru, 31i fani Desàmbar 2024
Mbokki Senegaal,
Ginnaaw bi ma leen nuyoo yéen ñépp, kenn ku ci nekk ci turam ak santam, maa ngi nuyu di ñaanal kilifa diine yi ak kilifa aada yi ci réew mi.
Guddig tay di mujjantalu guddi ci at mi, am pose la ci ku ne mu xoolaat li ci moom ak ni mu doxalee digganteem ak ñi mu bokkal réew mi, waaye tamit digganteem ak réew mi ci boppam. Waaye tamit am pose la ci nun, nu xoolaat fan lanu jóge ak fan lanu bëgg a yóbbu réew mi. Waaye bala maa sori, maa ngi nuyuwaat kenn ku nekk ci yéen. Di ko ñaanal jàmm ak wér gi yaram ci at mu bees mii nuy dugg. Di ko ñaanal kenn ku ne, waaye tamit di ko ñaanal ku nekk ak njabootam, di ko ñaanal Senegaal gépp.
Di ñaanal ñi nga xam ne ci at mi nu jóge, bàyyikoo nañu fi. Di leen ñaanal Yàlla yërëm leen te xaare leen àjjana. Di massawu seen njaboot. Di massawu itam ñi nga xam ne ñu ngi wéyee ak feebar, walla ñu nekk ci kaso yi, walla sax ñoo xam ne bis bu ne ñu ngi jànkonte ak ay jafe-jafe. Di leen xamal ne Senegaal du leen mas a wan ginnaaw. Di sargal itam Jigéeni Senegaal ñi nga xam ne duñu sonn duñu tàyyi ci taxawu njaboot gi waaye tamit téyee réew mi ndax seen njàmbaarte. Di nuyu ak a jaajëfal sunu bokk yi nekk biti réew. Mu wóor nu ne seen xel yépp a ngi Senegaal. Waaye itam nu di leen sargal ci seen taxawaay ca biti réew ngir Senegaal wéy di am woy wu rafet wi mu am. Di leen wax ne Senegaal ameel na leen njukkal lu rëy a rëy. Di delloo njukkal itam ñii di sunu Forsu de Defaas ak Sekirite, ndax seen yar ak seen xereñte, waaye tamit seen njàmbaarte, yi tax Senegaal taxaw dëgër boole ko ak di jàppale yeneen réew ngir jàmm dellusiwaat ci biir àddina.
Mbokki Senegaal,
Suqaliku ak jëm kanam fu ñu am rekk jàmm a fa am. Loolu moo waral fee di Kaasamaas, noo ngi def sunu kéem tolluwaayu kàttan ngir jàmm dellusiwaat fa. Suba ak ngoon, guddi ak bëccëg, lu nuy nas la di ko teg ciy pexe, di ko waxtaane itam ngir jàmm amaat fa. Ndax ci anam yooyu rekk lanuy man a suqali Kaasamaas, man a jariñoo ci la mu ëmb ciy njariñ, rawati na ci la nu ci mébet ci « Vision Senegaal 2050 ». Loolu moo waral nu indil leen « Plan Diomaye Pour la Casamance » ngir gunge ñépp ñi nga xam ne jóge woon nañu fa te nekkaat di dellusiwaat. Dalal seen xel, gunge leen itam ci ni ñuy toogaatee. Waaye fexe tamit ba loolu doon loo xam ne nit ñi dinañu ci sukkandiku ngir waxtaan yi man a yomb.
Waaye xam naa itam ne, ci njaboot goo dem, saa-senegaal boo dajeel, kenn ku nekk a ngi xalaat naka lay def ba am nekkiin wu gën. Waaye tamit naka lay fexee ba li ñépp bokk, ñépp jot ci. Kon ci loolu, Nguur gaa ngi taxaw ci li ñépp bokk mu sàmm ko. Gën a taxaw ci jafe-jafey askan wi moo waral Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko; ma koy jaajëfal bu baax, di rafetlu liggéeyam; dem fale ci péncum ndawi réew mi ngir wax naka la fas yéenee doxalee ci at yii di ñëw, sukkandiku ci « Agenda National de Transformation Senegaal 2050 », ngir yékkatiwaat réew mi waaye tamit ngir joxaat saa-senegaal bu ne àqam ci biir liy doxal réew mi. Noonu lanu ko fas yéenee wéyalee ci waxtaan ndax noo bokk réew mi, war ko péncoo, war ci diisoo. Day am solo saa-senegaal bu nekk jàpp ne liy doxal réew mi ci loxoom la nekk, mu bañ koo xaar ci keneen. Loolu moo tax ba nuy waxtaanewaat Yoon, ñépp lanu ci woo. Ba nuy waxtaanewaat dem bi ak dikk gi ñépp lanu ci woo. Ba nuy waxtaanewaat endistiri noonu. Te noonu lanu ko fas yéene wéyalee ndax noo bokk réew mi.
Ci geneen wàll, ci ndoorteelu atum 2025, Ngóornamaŋ bi dina taxawal benn jumtukaayu xarala bu tudd Liggéeyal Sa Réew buy may saa-senegaal bu ne, fu mu man a nekk ci biir réew mi ak ca biti réew, mu man a deppóose kàndidaatiiram ci post yi nga xam ne dinañu ko ubbi ngir nit ñi joŋante ci, nu jël ci ki gën a xereñ. Waaye doon itam pose mu ñuy jox saa-senegaal bu nekk ak fu mu man di nekk, bu amee sémb mu xamle ko, bu amee ay partaneer mu xamle ko.
Mbokki Senegaal,
Jafe-jafe yi bari woon nañu ci atum 2024. Waaye at la moo xam ne askanu Senegaal wane na xereñteefam, wane itam ne ñu gëm demokaraasi lañu. Ci 24i fani mars 2024, jël ngeen réew mi teg ko sama loxo. Nu ñëwaat 17i fani nowàmbar 2024, ngeen gën noo dëgëral jox nu masorite bu kenn naatablewul. Xam nanu bu baax li ngeen bëgg. Kon ci nun la des nu taxaw ci li ngeen di xaar ci nun. Ma bëggoon a taxaw rekk ngir jaajëfal bu baax sargal askanu Senegaal, ndax li jafe-jafe yi di am yépp wane nañu seen ug ñor ci wàllu demokaraasi, te loolu lañu nu yàgg a nawee ca biti réew. Man de dégg naa bu baax bataaxel bi nga xam ne jox ngeen nu ko ci irn yi. Xam naa li ngeen bëgg. Mooy nu tijji buntu soppi ak buntu naataange, ak buntu riptiir, waaye doxal ko ci Jub, ci Jubal ak Jubbanti. Loolu moo tax ma daal di jël dekkere bi nga xam ne moo lootaabe woon « COS-PETRO GAZ », di saytu lépp loo xam ne moo jëm ci wàllu petorol ak gaas bi nga xam ne moo feeñ Senegaal gën cee jox toogu bu yaatu kujje gi, gën koo ubbil sosete siwil bi waaye tamit ubbil ko mbootaayi liggéeykat yi ak ñi nga xam ne seen xam-xam màcc na jëm ci wàllu yoon. Li ma ci namm mooy sunu balli mbindaare yi, nu man koo jëfandikoo ngir njariñu ñépp, ci ñi fi nekk tay waaye itam ñiy ñëw ëllëg.
Waaye nag nanu xam te nangu ne soppiku ak riptiir manuñoo am ci fenn foo xam ne ger da faa law ba sax fa dàkk. Bu nu bëggee soppiku, kenn ku ne ci nun war naa noppi moom ci boppam ngir soppiku ci ni muy gisee loo xam ne ndénkaan la te ñépp bokk ko, waaye tamit ci ni muy liggéeyee ci digganteem ak li nga xam ne moom la ko réew mi dénk. Loolu moo waral ba nu taxaw ci soppi sàrt bii nga xam ne mooy tënk naka la foŋsaneer yi war a taxawee ci seen liggéey, waaye tamit namm ci doxaliin wu leer te jub. Nu fas yéene nag teg ñenti sàrt yu jëm ci aar yoolekat yi, waaye tamit gën a dooleel kurél giy xeex ger, fexe tamit ba ma-réew bi fépp fu mu man a nekk mu man a xam li xew ak ñépp ñi nga xam ne ñu ngi liggéey ci biir Ngóornamaŋ bi, walla ci foŋsoo piblig ñu yaatal ko ba ñépp di def seen « déclaration de patrimoine ». Muy doon ci ndawi foŋsoo piblig yépp, waaye tamit war a tënk ñépp ñi nga xam ne dañu leen di tabb walla ñu fal leen fu ñuy saytoo njël.
Mbokki Senegaal,
Xam naa ne jafe-jafe yi bari nañu lool ci at yii nu weesu. Loolu moo waral bi ma toogee rekk, daanaka ay ayi-bis rekk laa def, fexe ba ñu wàññi dund bi. Ngóornamaŋ bi nag def na ci lu mu man, donte jafe-jafe yi bari woon nañu ngir jàppale ñépp ñi nga xam ne ay baykat lañu waaye tamit jàppale yeneen porodiktéer yi, waaye fexe ba saa-senegaal bu ne foo man a nekk nga yëg ne wàññiku am na. Ci geneen wàll lépp loo xam ne jàppoon nanu ne luy yàq xaalis la, lu mel ni CESE ak HCCT, ñu seeyal ko. Yeesal yu ni mel nag dinanu leen wéyal ngir jël xaalis boobu dugal ko foo xam ne njariñ a nga fa. Komite bi nga xam ne nag teg naa ko ginnaaw ba nu waxtaanee wàllu yoon, mu ngi liggéey ngir li nga xam ne déggoo nanu ci, nu jëmmal ko man koo doxal.
Mbokki Senegaal,
Bu ngeen seetloo, bu nu waxante dëgg rekk, làngi politig yi bari nañu Senegaal lool. Te gis nanu làngi politig yu bari, ni ñu war a wàccoo ak yoon demewul noonu. Yàgg nañu leen ci seetaan nag waaye loolu fàww mu dakk ba ku bëgg a samp làngu politig nga man koo samp waaye nag nga wàccoo ak li la yoon teg. Muy sàrt yi nga xam ne ñooy tënk képp ku am làngu Politig. Waaye nag dunu ko def ci doole ndax loolu du sunu doxaliin. Dinanu waxtaan ak ñépp ngir fexe ba géewu politig bi gën a leer ba làngu politig bu ci ne nga nekk ku teewal ay nit, kuy liggéey ngir yeete ci wàllu demokaraasi. Coppite yooyu yépp nuy wax nag, lenn rekk a ko lal, muy naka lanuy fexee ba nguur gi gën a jege askan wi, man a taxaw itam ci liy mébetam, ngir man a taxaw ci samp Senegaal goo xam ne, dafa taxaw ngir jëmmal boppam, dëggal boppam ci fépp fu ay réew di daje.
Diplomasi Senegaal am na nu ñu baaxoo di ko ko bàkkee. Mooy liggéey ci fépp ci biir àddina ngir jàmm man a sax ci àddina, waaye tamit jàppale ñi nga xam ne dañoo néew doole ñu di leen noot ci ay askan ci biir àddina. Bu loolu weesoo nag, képp koo xam ne xarit nga ci Senegaal, dinanu la jàppee xarit, gën a jëflante ak yaw waaye tamit boole ko ñépp ci kaw sàmm njariñi Senegaal. Loolu moo waral ma dénk Jëwriñu Forsu Arme, mu xool naka lay sumbee waxtaan ak ñi nga xam ne seen militeer yaa ngi ci biir Senegaal te war fee jóge, ndax wax dëgg Yàlla nag yàgg nañu fi lool te amatuñu lu ñu fiy def.
Mbokki Senegaal,
Maa ngi leen di woo nu waxtaanaat ngir xoolaat fi nu jóge, nun nooy ñan, lan mooy sunu mbaax ak fan lanu bëgg a jëm? Ginnaaw yeesal yi ci wàllu politig ak ci wàllu campeef yi, dina baax nu taxaw seetlu li nga xam ne itam danu koo war a sàmm te mooy li nu boole. Askanu Senegaal yàgg naa daj mettit, ci njëkk ñuy dog buumu njaam gi, ba nuy xeex ngir moom sunu bopp, ba ci xeex yi mujj ngir samp demokaraasi. Waaye yàgg nanoo wane ne askan wu jàmbaare dëgg lanu, askanu bañkat lanu. Loolu moo tax ren gii nu indiwaat màggalug bóom gi amoon Caaroy 1944. Li nu ci nammoon mooy sargal ñi nga xam ne bóomoon nañu leen ca Caaroy, waaye tamit delloowaat dëgg gi ñu bëggoon a nasaxal ci li xewoon foofu ca Caaroy. Waaye fàww nu nangu ne manunoo jéem a nekk di leeral loo xam ne xew na fi 80i at ci ginnaaw ba noppi fàtte li nga xam ne barki démboo njaay la xew biir Senegaal, diggante mars 2021 ak féewarye 2024. Ay wakkan yu bari rot fii ci Senegaal. Ni nu amalee ñi nekkoon Caarooy 44 ñu bóom leen 80i at ci ginnaaw, ngir ñu leeral lépp, noonu lanu amee tamit ngir leeral ñi nga xam ne bóom nañu seen i bokk, seen i doom ak seen xarit. Li nu ciy wut nag du ngir fayantoo ndax sax nag danoo jàppalul kenn dara ba koy fayeeku. Waaye ñi nga xam ne loru nañu ci dañoo soxlaa xam lan moo xew. Balaa ngay baale, dangay xam kan moo la tooñ. Te soxla nanu ko, seen njaboot soxla nañu ko. Waaye tamit dafay baax képp kuy way-politig walla kuy toogaat ci biir réew mii, mu xam ne bakkanu doomi aadma du lu ñuy fowee.
Mbokki Senegaal,
Li ma gëm mooy askanu Senegaal askan wu Yàlla teral la. Ndax bari nanu ay làkk yu fi nekk, bari nanu ay waaso, bari nanu ay xeet, bari nanu ay kurél. Waaye loolu danu cee mas a tënku mu doon doole ci nun. Masul a doon lu nuy féewale. Loolu moo tax ba li nu donnee ca maam ya, muy doole ci nun, danu koo war a sàmm bu baax a baax, sukkandiku ci nag ngir liggéey loo xam ne ku ne dinga ci gis sa bopp ba lu ci meññ rekk, doon li ñépp bokk ñépp jot ci. Waaye li am solo mooy nu bañ a fàtte mukk ki nu doon ak fan lanu jóge. Jël ci ndono yooyu ci mbaax, ci jom, ci fulla ak fayda, delloowaat ko ci lépp li nuy liggéey, moo waral nu woote liggéey réew mi ci Jub, ci Jubal ak ci Jubbanti.
Ci sama taxawaayu « gardien des institutions et garant de l’unité nationale » nag, dinanu fexe ba kenn ku ne man a jibal xalaatam man ko wax muy njariñ ci réew mi, wuute sax man naa am waaye réeroo bañ a am nag, mooy waral waxtaan am solo. Waaye bu wuute dem ba doon luy nasaxal jàmm ci biir réew mi, walla muy yàq loo xam ne nun ñépp a ko bokk. Xam naa nag ne loolu dina laaj waxtaan, dina laaj wax ak ñépp ñi nga xam ne dañuy yàq, ngir ñu delloosiwaat seen xel, waaye dina laaj tamit lépp loo xam ne lu Nguur gi war a taxawe la ngir sàmm loolu nga xam ne mooy sunu alal, muy jàmm ji nekk ci biir réew mi, ñu taxaw ci.
Mbokki Senegaal,
Nanu gën a waxtaanaat bu baax, moytu lu nuy féewale. Yenn saa yi nga dégg ay kàddu ci biir tele yi mu xaw laa tiital lool, walla sax ci mbaali jokkoo yi. Lépp loo xam ne danuy féewale, di yàq diggante, di yàq mbokko, nanu ko moytu. Ndax jàmm jooju nu donn, bala ngaa xam li muy jar rekk nga ñàkk ko walla nga xool ci askan yi nga xam ne amatuñu ko.
Senegaal gi nu woote di Senegaal gu moom boppam, Senegaal gu yoon di dox, Senegaal gu am naataange, ñu ngi koy liggéey bis bu set ci ay xalaat ak ci ay jëf yu ñuy teg. Loolu moo tax nu ciy woo ñépp rawati na ndaw ñi. Ay jàmbaar lañu te seen i xel ñor na te ñaw na. Noo ngi leen di woo ci ngeen fexe ba lenn bañ leen a teggi ci yoon wu baax wi. Ngóornamaŋ bi soxla na leen te yéen a man a téyee réew mi, yéen a koy liggéey. Lépp loo xam ne war na ci taxawu leen, nekk seen wet, dinanu ko def ngir ngeen man a tekki, jariñ seen bopp, jariñ seen i njaboot waaye tamit jariñ réew mi.
Mbokki Senegaal,
Nanu xam ne Senegaal, dëkk bu Yàlla teral la. Meññeef yi bari Yàlla jox na nu ko. Waaye tamit jox na nu li ëpp solo, muy ay nit ñu baax ak ay mag ñu baax. Kon li des mooy nu booloo, mànkoo te liggéey réew mi. Bu nu ko defee Senegaal dina am naataange, dina am jàmm.
Maa ngi leen di ñaanal atum 2025 jàmm.
Yal na Yàlla sàmm Senegaal te sàmm Afrig!
Déwénati !
Basiiru Jomaay Jaxaar FAY
Njiitu Réewum Senegaal