Àddug Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal, ci jataayu màggal 80eelu atu bóomug Caaroy 44.

waxtaan - 01 MONTHS.DECEMBER 2024

Ginnaaw bi ma nuyoo Kilifa yii di, Mohammet Uld Gasuwani Njiitu Réewu Islaam gu Móritani, di Njiital Mbootaayu Réewi Afrig, ASALI Ansumani mu Iñoo Komoor, Aadama Baro mu Réewum Gàmbi, Umaro Sisoko Embaló mu Réewum Gine Bisaawóo, Biris Koloteer Oligi Ngemaa mu Réewu Gaboŋ,

Soxna yi ak Sëriñ si jiite ay gàngoor,

Njiital Jëwriñ yi,

Njiital komisoo bu CEDEAO,

Jëwriñ ak Sekkereteer Detaa yi,

Soxna yi ak Sëriñ si fi teewal seen i réew ci wàllu laamisoo, 

Kilifay ndoxal yi ak yu gox yi,

Njiitu Kurél giy lootaabe màggalug 80eelu at mi ak ñi ko séq,

Soxna yi ak Sëriñ si càllaloo ci jabooti tiiraayéeri Senegaal yi,

Gan ñu tedd ñi,

Bokki ma-réew yi,

Soxna yi ak Sëriñ si,


Ma Bëggoon bala maa yékkati genn kàddu rekk, jaajëfal sama bokki njiiti réew yii di GASUWANI, ASALI, BARO, EMBALÓ ak NGEMAA, ci li ñu nangoo ñëw, ak li ñuy xat lépp, teewe xew wu njëkk wii jëm ci fàttaliku mboor mu tiis mi amoon fii ci Caaroy lu mat 80i at ci tay.

Maa ngi tatagal mbooleem sunu gan ñi te di leen wax ñu dal jàmm ci Senegaal.

Maa ngi jaare ci yéen di nuyu askanu kenn ku nekk ci yéen. Seen teewaay bu am solo bii ci sunu wet firnde la ci taqoo gi ngeen taqoo ak mboor mi nu bokk.

Yëg-yëg bu kawe laa am ci bis bii ak ci barab bii ñu bóomee woon ay jàmbaari saa-afrig yu gànnaayoowul woon lu dul jom, ngor ak mbokkug Afrig. Muy ag bóom gu amul genn cëslaay.

80i at ginnaaw pékke gu jéggi dayoo gii, ba leegi ñu ngi wéy ne patt ci mbir mii xewoon Caaroy. 

Kàddu yiy bawoo ci biir bàmmeel yi di nu woo bu baax, ci jamono ju ñenn ñi di xeeb dayoob pékke gii, yegg sax ba ñenn ci sëti ñi amaloon jëf ju ñaaw jii di ko weddi.

Ci suufus Caaroy sii tiis woowu amee woon, ba leegi téll-télli sox yi a ngi jolli, lépp ngir fàttali rekk ne ñaawteef gi a ngi fi ba leegi, fees fi dell, te du mas a raaf.

Ñu bari ci nun ñi xamul, muy mag di ndaw, dina laaj: waa lu xewoon dëgg ? Ndax kat dañoo yàgg nëpp-nëppal mbir mii lépp rekk ngir jéem a far xew-xew bu tiis bii ci sunu mboor.

Muy ay saa-afrig yu bari yu ñu jaay doole jëlee leen seen i réew yóbbu leen ngir ñu dem xeexali Farãas gi ne woon aji-noote ji. Ñu tuddee woon leen Tiraayéer Senegale. 

Ñoom ñépp daanaka bokkoon tund yi ñu bawoo ci yi Farãas nootoon ci Afrig Sowu Jant, ci Digg bi ak ci Penku bi te mujj doon fukk ak juróom ñaari réew ci jamonoy jonn yi. Muy Benee, Burkinaa Faasó, Kamerun, Komoor, Kongóo, Kodiwaar, Jibuti, Gaboŋ, Gine, Madagaskaar, Mali, Móritani, Niseer, Sàntar-Afrig, Senegaal, Càdd ak Tógoo.

Ñu yàgg leen a fàtte ak a doyadil, terewul ñoom tiiraayéer yii jéggi mbooleem jafe-jafe yi ngir dem xeexi ci suuf yu sori lool ak seen i réew.

Ñu tukki ci anam yu doy waar (tasaaroo ci kali gaal yi), wàcc ci tooli xare yoo xam ne, dañuy jaayante lépp daan sol ay tëni yu sempal yu amul genn kaaraange ba 1943 ni leen saa-amerig yi di leen ko door a soppilee.

Ñu joxe seen ndaw, seen dereet ak seen jëmm ngir péexte ak jàmm am ci àddina si. 


Soxna yi ak Sëriñ si,

Donte am na ñu bari ñu faatu ci soxi « nazies » yi, taxawaayu tiiraayéeri Senegaal yi bokk na bu baax ci li tax way-lëngoo yi am ndam. Moo xam muy muccalug Tunisi ci wàcc gi amoon ca il bu Elbe, muccalug Tulon ak Pari, taxaw nañu temm wane ag dogu ak ug njàmbaarte boole ko jaayante lu bari ngir jotaat yenn ci ay dëkk.

Ñu yeyoo nu sargal leen lañu, sunu wegeel ak sunu fonkeel. 

Waaye ci mujjug mboor mi dañoo mujj a dëggaate mbooleem jaayante yi ñu defoon. Fa ñu leen waroon a yékkatee, kañ leen, delloo leen njukkal, fa lañu joxee ndigalu ñu faagaagal ñii nga xam ne ñoo doon dékku metiital yi ci kasoy Almaañ yi. 

Li gën a doy waar daal di xew 1 panu desàmbar 1944 fii ci Caaroy ba Seneraal Dagnan joxee ndigalu ñu soqi ci kaw nit ñu deful dara, yoruñu gànnaay, ñoñ, defuñu lenn lu dul sàkku ñu fay leen seen ndàmpaay ak yeneen yu ñu warloo woon ak ñoom. 

Muy kon jëf ju ñu waajal, ju jëmoon ci faagaagal ñu doon laaj lu ñu yellool, xoqatal ñi ci des ak saxal fi nooteel.

Muy pékke gu ñu amal te kenn manu ko weddi. Lii de mooy mujjug ñenn ñu joxe seen dereet ak seen ñaq ngir muccal am réew. 

Tay nag, ngir wareefu fàttaliku, feeñal dëgg ak yoon, tax na manunoo fàtte ñaawteefu bóom yi amoon fii ci Kãa bu Caaroy.

Fàww nu fàttali mboor mi, mboor mépp, te bañ a bàyyi dara. Loolu mooy firndeel mbaaxi jàmm, péexte ak yamoo diñiteg doomu Aadama gi àddina sépp bokk. 


Soxna yi ak Sëriñ si,

Yii rekk a yokk sunu pas-pas ci màggal bisu bóom gii amoon Caaroy ngir, ci genn wàll delloo njukkal way-loru ñii ba dootuñu jóg ci sunuy xel, ci geneen wàll, teg jéego yi njëkk jëm ci delloosi dëgg ci mboor mii jaare ko ci dakkal far gi way-noote yi yàgg bëgg a def ci xew-xew bu tiis bii.

Loolu nag defunu ko ngir tijji buntu fayantoo, mer walla mbañeel. Déedéet! Li nuy amal fii tay mooy wareefu fàttaliku te bañ a fàtte ak fexe ba dëgg feeñ ci li xewoon, ngir man a fay bor bi ñu ameel tiiraayéer yi ak seen i jaboot. Loolu moo tax, nu teg kurélug gëstu gu maandui ngir mu jàppale nu ci indiwaat dëgg-dëggi jëf yi amoon ak gën a xamle xew-xew bii nu bokk ak Farãas ci sunu mboor.

Ngir yombal liggéeyi gëstu yi nag, sàkku naa ci Njiitu Réewum Farãas, mu jàppandil mbooleem arsiif bu man a yombal dëgg gi feeñ, ak seen ug jàppale bis bu nu yeggee ci war a seet ay bàmmeel walla jéem a xàmmee kenn ci way-faatu ñi.

Maa ngi rafetlu taxawaayu kilifay Farãas yi ci seen ubbeeku ba nangu sunu càkkuteef ngir dëgg gi feeñ. 

Ci noonu, laataa màggal gi, ñenn ñu bokk ci kurélug gëstu gi dem nañu Farãas ba jot fa amal ay jataayi liggéey seen digg ak kilifay Farãas yi ak ñenn ci ñi jiite yenn ci warab yi ñu denc yenn arsiif yi. Dees na wéyal gëstu yi ginnaaw màggal gi.

Frãas itam teg na jéego bu am solo ndax Peresidaa Emmanuel Makroŋ mi ma bind ab bataaxel ñetti fan ci ginnaaw, ngir nangu ne xew-xew yi amoon 1944 ci Caaroy ag bóom la mujjee. Maa ngi rafetlu taxawaay bi.

Ci jëf jii kon, Farãas nangu na càkkuteef gu yàgg te war. Muy jéego bu nuy rafetlu ci doxaliinu jëm ci delloosi sag ak diññitey tiiraayéer yi faatu woon, ginnaaw Kàdduy Peresidaa Faraasuwaa Holand ca sëgi Caaroy ya 30i fani nowàmbar 2014, « doon ci sargal ay nit ñu soloon tëniy Farãas te saa-farãas yi mujj a wëlbati seen i fetal soqi seen kaw. »

Lii lépp nag terewul, ba leegi des na lu bari lu lëndëm ci mboor mii rawati na limub ñi ñu ci jot a bóom dëgg. 

Ñaari ràpoor yu wuute yu kilifay way-noote yi génne woon wax nañu 35 ak 70 ci jamono ju yenn ci ay seede di xamlee ne lu ëpp ay téeméeri téeméer faatu nañu ci ak ñu bari ñu am i gaañu-gaañu. 

Arsiif yi ñuy laaj nag dinañu tax, bees sukkandikoo ci gëstukat yi, ñu xam bu wér li waral jéeya jii amoon ci Caaroy; gën a am lu wér ci tolluwaayu tiiraayéer yi ñu dellusi woon, seen ub lim, ñan la woon ak fu ñu bawoo, warab yi ñu leen suul, coono yi ñu daj, seen ñëgg-ñëggi xol ak toroxal gi ñu leen daan def, niki noonu limub koppar yi ñu ameeloon kenn ku nekk ci ñoom.

Liggéey bu jafe la nag. Loolu moo tax may woo ñiy yëngu ci wàllu nguur ak ñi ci yënguwul ci mbooleem réew yi mbir mi soxal, ba ci Farãas, saa-mboor yi ak gëstukati fenn fu ne, nu boole sunu man-man ngir am gis-gis bu wér te wóor ci xew-xew bu tiis bii ci mboor mi nu bokk.


Soxna yi ak Sëriñ si , 

Seet ñi faatu ñu gëstu ñi ci laale fàww mu am ngir xàll yoonu juboo gu dëggu.

Ma posewu ci kon ngir delloo njukkal bu baax mbooleem saa-afrig yi ba sax ci ñi ko doonul ñépp ñi nga xam ne yàgg nañoo xeex ngir ñu bañ a fàtte mbaa ñuy soppi mboorum Tiiraayéer yi ak bóom gi amoon Caaroy.

Sama xel dem na ci ñi jiitu woon ci xeex bi, way-politig yu góor yi ak yu jigeen yi, Boroom xam-xam yi, bindkat yi, nosekat yi, ñiy yëngu ci wàllu Sinemaa, ma-pasin ak way-coobarewu, ñi joxe seen jëmm walla seen xel. Bu dul woon ak li nu boole doole yi, kon xayna xeex bi doonul woon man a yegsi fii tay. Waaye nag dëgg googu dafa laaj ñu gën koo xamle, jottali ko ba ñépp jot ci.

Danoo war a gën a soññee ci yëngu yii jëm ci delloosi fàttaliku ak diññitey tiiraayéeri Snegaal yi.

Ci sama wàll, dinaa teg ay matuwaay yu bari yu jëm ci téyewaat genn wàll ci mboor mii nu bokk ak 16 ci sunuy bokki réewi Afrig:

Li ci njëkk : dees na tabax benn memoriyaal bu ñuy jagleel Tiraayéer yi ci Caaroy, mu war a doon barabu teewlu ak fàttaliku bu ñuy tijjil mbooleem réew yi ñu bawoo woon, niki noonu askan wi.

Ñaareel bi: Dees na tabax benn barabu xamlu ak gëstu bu ñuy jagleel tiraayeer yi. Barab boobu dees na fa dajale ay arsiif, ay seede ak i nettali, lépp ànd ak taxawu gëstu gi ak njàng mi ci mboor moomu.

Ñetteel bi: Dees na jox yenn mbedd yi ak yenn pénc yi turu xew-xew bu tiis bii ak soldaar yi ngir seen jaayante gii doon luy sax ci sunuy dund ak sunu mboor. 

Ñenteel bi: Mboorum Caaroy ak tiiraayéer yi dees na ko dugal ci njàng mi. Loolu dina tax maas giy ñëw ëllëg man a màggaale ak dégg-dégg gu wér ci lii jot a xew ci sunu mboor.

Juróomeel bi:  Bisub Tiiraayéer yi leegi jàppees na ko muy 1 panu desàmbar ci at mu jot, muy bisub fàttaliku bóom gi amoon Caaroy.

Soxna yi ak Sëriñ si,

Mboorum xare ak faagaagal ci ay gànnaay masul a jotale. Ni ñu koy nettalee saa su ne day am lu bari lu ci des. Noonu la demee ci ñaareelu xareb àddina si rawati na njeexital yi mu am ci réew yi ñu nootoon te ñu dund faagaagal yu metti: Caaroy 1944, Sétif ak Gelmaa ca Alseri ca 1945, Hanoni ak Haifoŋ ca Wiyetnaam 1946, Madagaskar 1947, Duwalaa ca Kamerun walla Dimbokro, Ca Kodiwaar 1948-1949 ak yeneen warab.

Menn mu ci nekk ci mboor yu tiis yii daa war di dund ci nun jaare ko ci di ko fàttaliku. Loolu mooy tax nu man di bége ak a safoo sunu jàmbaar yooyu.

Delloo njukkal tiiraayéer yooyu nag, yamul rekk ci jooy sunu way-dawlu yi. Waaye mooy wéyal seen ub xeex def ko sukkandikukaay ngir yeesalaat jëflante yi diggante sunu biir, sunu mboor, ak ndonol ñii nga xam ne ñoo dund tiis wii.

Mooy xamal àddina sépp ne tiiraayéeri Senegaal yi doonuñu woon ay merseneer, waaye dañoo jógoon ngir sàmm diññite doomu aadama ci àddina wërngal kàpp. Mooy yuuxu ca kaw ne diñite googu, ñu yàgg a salfaañe, kenn dootul nangu ñu di ko dugal ci jibay patt ak fàtte.

Bóomug Caaroy gi ab góom la, waaye tamit ab bind la. Bind bu nuy jàngal ne mbokkoo, bennoo ak bañ a fàtte ñooy gànnaay yi ëpp doole yi askan yi am péexte yore ngir rëdd seen ëllëg. 

Ngalla waay màggal gii, ginnaaw 80i at, bu mu yam rekk ci teewlu. Na doon soññee gu feddaliku. Soññeb doxal yoon, soññeb fàttaliku, soññeb dëgg. Ngir, Caaroy ak xew-xew yu ni mel bañatee am mukk, ak nu man a demee nag, fépp ci àddina si.

Noo ngi sargal tay sunuy jàmbaar. Te ci sargal gi nu leen di defal, nanu fàttaliku nun itam ne am na lu nu war: mooy ŋoy ci ñoom rekk bañ a jeng. Sax ci seen i mbaax, seen ub xeex ak seen gis-gis ci àddina su jub.

Nanu mànkoo, liggéey ngir feeñal dëgg ci bóomug Caaroy gii, ngir yoon, péexte ak diññite gu mat sëkk !


Maa ngi leen di jaajëfal ci seen ug teewlu.