Àddug kilifa gi Basiiru Jomaay Fay Njiitu Réew mi ci tijjitel 15eelu « Biennale Art Africain Contemporain »

waxtaan - 07 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay jiite na tay jataayu tijjitel 15eelu « Biennale Art Africain Contemporain » ci Ndakaaru, di xew-xew bu am solo ngir wane mbatiit mi ak marseb aar bi.


Wëppa wi ñu tànn ren nag di « The wake, Yewwu gi, xàll wi », màndarga la ci woote bi jëm ci àndandoo xalaat ci jafe-jafey jamono ji, rawati na ci wàllu kéew mi ak dundiinu askan wi.


Cig àddoom, Njiitu Réew mi wane na mbégteem ci daje ak njabootu mbatiit mi boole ko ak xamle solo si xew-xew bu am maanaa bii war wéy ba 7i fani desàmbar 2024 am. Peresidaa Fay rafetlu na teewaayu artist yi ci àddina bi teg ci delloo njukkal fentkat yu fés yi boole ko ak fàttaliku jëmm yu am solo yi njëkk a  taxawal Bienale bi ba mu yegsi fii.


Man ngeen fekk fii ci suuf mbooleem ay kàddoom :


Yéen bokki Jëwriñ yi,


Soxna yi ak Sëriñ si teewal Etats-Unis Amerig ak Repiblig bu Kabo Werde, di réewi eewite donóor yi,


Jëwriñu Tàggat Yaram, Ndaw ñi ak Mbatiit,


Yaw Sekkereteer Detaa ci wàllu Mbatiit, Endistiri kereyatif yi ak Patrimuwaan Historig,


Yéen kilifay Ma-Laamisoo yi,


Soxna yi ak Sëriñ si teewal partaneer piriwe yi,


Yaw Peresidaa Komite oriyantaasoo bi,


Yaw Sekkereteer Seneraalu Biennale bi,


Soxna yi ak Sëriñ si séq « Jury international » biy joxe raaya yi,


Soxna yi ak Sëriñ si teewal kominóte litereer ak artistig,


Yaw Diregtiris artistig bu edisoob ren bi,


Yéen bokki artist yi ak sunu xarit yiy yëngu ci wàllu art,


Yéen gan ñu tedd ñi,


Soxna yi ak Sëriñ si,



Ci sama taxawaayu « Premier Protecteur des Arts et des Lettres » niki ko Ndayi Sàrti Réewum Senegaal tëralee, bëggoon na maa wane mbégte ak bànneex bi may yëg ci daje ci bis bii ak Njabootu Mbatiit gu mag gii, ci tijjitel 15eelu «Biennale Art Africain Contemporai ».


Kon ci diiru weer, maanaam diggante 7i fani nowàmbar jàpp 7i fani desàmbar 2024, Ndakaaru ak Senegaal dinañu yëngu lool ci dundal art. 


Ma bëggoon a màng pose mi rekk kon dalal jàmm sunu gan ñi bawoo fépp ci àddina, ci sunu réewum teraanga mii. Seen teewaay fii day firndeel rekk ne Biennale bu Ndakaaru bii mbirum àddina sépp la.



Soxna yi ak Sëriñ si,


Ngeen may ma tamit ma ndokkale bu baax artist yi ñu doon sargal leegi ci raayay Biennale bu gànjaru bii.


Ma jaare ci jëmm yii Jury bi jot a sargal ndax seen liggéey bu mucc ayib, delloo njukkal mbooleem fentkat yi, muy 129i artist yi nekk ci sémbu « IN » wi ëmb ñetti pàcci réew mi, ak ñiy fésal ci « OFF » yiy yaatal tolluwaayu melosuufi Biennale bii romb Ndakaaru ak li ci biiram.


Yéen ñii ñépp tegu ci yoon wi ñi leen jiitu xàlloon lu ëpp 34i at, bokk ngeen ci liy jegele askan yi jaare ko ci kàddu gu am doole gi nekk ci art.


Ci jamono yii nag, manumaa ñàkk a xuus ci géeju fàttaliku ci Biennale bu Ndakaaru bii, delloo njukkal jëmmi xarit yu am solo yi jot a wuyuji seen Boroom, di jëmm yoo xam ne, bu pas-pasu Dakar’t bi yegsee fii tay, seen i jëf ak seen taxawaay a ko waral. Sama xel day dem ci Isaa Sàmb ñu gën koo miin ci Joe Wakaam, Usmaan Sow ak Suley Keyta. Fàttewuma Ndari Lóo, Alfa Sow, Ibraahiima Kebe. Sama xel dem ci Jibi Njaay, Aamadu Keere Mbay, Musaa Baydi Njaay, Kataa Jàllo, Mustafaa Dime, Aamadu Sow, Jóob Sàmba Laay ak ñeneen ak ñeneen.


Ñoom ñépp, maa ngi leen di wax ci turu Repiblig bi ne: Dunu leen fàtte mukk!


Kon nag maa ngi ndokkale bu baax komite oriyantaasoo bi, Sekkereteer Seneraalu Biennale bi, komiseer yi nekk ci wàllu fésal gi, ñi bokk ci « Jury » bi, senogaraaf yi, wànqaas yi ak komisoo tegnig yi.


Fàttewuma nag ñi nga xam ne ñu ngi amal liggéey yu am solo ci suuf, guddi ak bëccëg, lépp rekk ngir Biennale bii wéy ci anam yi ñu ko minee te gën di jëm Kanam. 


Maa ngi rafetlu bu baax itam tànneefu way-lootaabe yi jëm ci sargal ñaari artist palastisee yu xereñ yii di, Anta Sermen Gay di ku ñépp nangu ag xereñam ci pentiir ci weer, ak Muhammadu Ndóoy ñu koy wax Ndóoy Dut's mi fi bawoo lu jege at ci ginnaaw. Ñoom ñaari fentkat yii ñu dogu lañu ci dundug askan wi.


Muhammadu Ndóoy Dut's di ndaw lu teel a wuyuji Boroomam, ku fésoon la ci pénc mi ndax ay jëfam yu baax ak daan dimbale, rawati na ci tabax ay warabi jàngukaay ak daan séddale ay jumtukaay ci warabi fajukaay yi añs !  Yal na suufu Jendeer gi mu defoon ci xolam te daan ko liggéeyal, woyof ci kawam. 


Bu dee Anta Sermen Gay nag moom, ak muuñam gu taaru giy dalal xel di seral xol, ñépp dëppoo nañu ci ag xereñteem ci ay pentiiram ni muy misaale dëgg-dëggi dundu askan wi. Mu doon jàngalekat ci art, ku bëgg li muy def la boole ko ak di nu bégal ci liggéey bu mucc ayib bi muy def. Noo ngi koy ñaanal mu yàgg fi lool te yàgg a yëngu ci wàllu taaral ak yaatal xam-xam bi mu làq.


Biennalu Ndakaaru bii nuy màggal 15eelu edisoo bi nag, wane na boppam ci at yii weesu, niki màndarga ci fésal art bu bees bi ci Afrig ak ci àddina si. Jataay bu am solo la ngir fésal mbatiit mi rawati na nag marseb art bi. Li fi jot a jaar lépp nag ci lu ko manoon a gàllankoor, terewul mu sax ci doon jumtukaayu fésal kàddug art bu ñu ràññee.


Li waral sax googu am nag, mooy taxawug Nguuru Senegaal ak campeef yi ak piriwe yi ciy def seen ndimbal, kon nag maa ngi leen di sant ak a gërëm ñoom itam ci seen taxawaay bii kenn dul weddi.


Taxawaayu artist palastisee yi def Biennale bii lu gànjaru, jaare ko ci seen i yoxo, su ma yaboo sax ne seen i boros ak i yattukaay, làmp bu am doole la tamit buy leeral boole ko ak di gindi xew-xewu mbatiit bii xëtt dig yi ba génn sunu Kembaar gi. Nammeelu artist yi ak ñépp ñiy safoo art te di ko dundal, doon na jumtukaay bu am doole ci xew-xew bii. Loolu bokk na ci li waral mu sax donte am nay gàllankoor.


Am naa mbégte lool ci ni Ndakaaru ak Senegaal di jaaree ci « Biennale Art Africain contemporain » bii, ngir gën a dëgëral taxawaayam ci wàllu fent ak xalaat ci tomb yi aju ci taaru art yi doon ay jafe-jafe yu mu war a jàmmaarlool ci ni àddina di soppikoo.


Looloo tax may rafetlu wëppa wi ñu tànn ci edisoo bii: « The Wake, Yewwu gi, Xàll wi», di ndokkale bu baax nag Diregtiris artistig bi ci xalaat yu am solo yi mu indi ci waxtaan wi.


Wëppa wii day wane rekk ne lenn ci li tax a jóg art bokk na ci delloosi li faroon, liy jaar di jàll, xew-xew yiy jaar ci àddina sii sax ci yëngu, ngir dundalaat ko, xóotal ko saxal ko. Taxawaayu artist bu wér kon mooy lootaabe ni àddina jaxasoo ngir wutal ko maanaa.


Soxna yi ak Sëriñ si,


Mbatiit mooy li nuy màndargaal teg ci di nu dundal. Fépp fu nu dem, dinanu fa bàyyi pënd yi taqoon sunuy tànk te bawoo ca suuf ya nu cosaanoo ak ay mbaaxam. Mbatiit daal mooy liy lëkkale yoonu kenn ku nekk ci nun, te doon lu ag teqalikoo di yoot ndax gàllankoor yu bari yi ci jamonoy tay. Mbatiit, ak ni mu wuutee, mooy suuf su nangu si nu war a ji su dee namm nanoo dund cig bennoo.


Yëg-yëg bi nuy am ci kanamu « œuvre d’art » man naa soppi bu baax sunu gisiin ci àddina si boole ko ak wëlbati sunuy jëf. Artist bi li mu bokkle ak nitu politig ki ak nitu nguur mooy day bàyyi xel aw askanam. Day waajal soppiku yiy am ci dundiin wi boole ko ak doon ku am ub gis-gis. Taxawaayam ci man a dajale doole yépp, yu ndaw ñi rawati na, day kon lu am solo.


Art day yombal déggiin wi ci doxiinu àddina, gën koo woyofal boole ko ak di leeral taxawaay bi ci nit ki war a ame, ànd ko ak yeneen xeet yi mu séqal dund gi. Taxawaay bu ni mel nag mooy wane ne taar ak jikko ñoo bokk fenn fu ñuy taxaw.


Dañuy faral di wax sax ne art man naa fànq lu war a xew ëllëg. Day teggi mujjug dundu doomu aadama ngir def jëfam muy lu sax. Ma dolli ci ne bokk na itam ci liy dindi njàqare yi ngir fésal taar, nammeel ak njàmbaar. 


Njàqare yii di gaare, te li koy màndargaal di tolluwaayu àddina bu jaxasoo bii niki noonu yiy yoot ci wàllu kéew mi, daf nuy wan rekk ne fàww nu gën a suuxat jàmm ak déggoo diggante askan yi ak ci biir réew yi. Ci loolu kon, bataaxelu jàmm bi niti mbatiit yi di jàllale wareef na koo gën a may nopp.


Bëggoon na maa jaajëfal bu baax ñaari réew yii di ewite donóor yi ci edisoo Biennale bii, di Etats-Unis Amerig ak Repibligu Kabo Werde, te doon ñu jege Senegaal lool. Amuma xel-ñaar ci ne, ñaari réew yu mag yii ci wàllu mbatiit ak wuute te doon ñu yàgg a lëkkaloo ak Senegaal, dinañu indi lu am solo ci xew wii, jaare ko ci seen i artist ak seen ug xereñte. 


Soxna yi ak Sëriñ si,


Bi ma yegsee ci bopp nguur gi rekk, ci laa woo sunu bokki ma-réew yépp ñuy wane ag njub ci seen i yëngu ak seen i jëf. Yéene jooju ma fésal nag li ma ci namm mooy sóob nit ñépp wëlbati seen yitte ci dajale doole yi ak xalaat yi ngir man a jàmmaarloo, ci gën gaa mucci ayib ak jafe-jafey tay ak ëllëg, jaare ko ci rootee ci jikko yu tedd yi sunu mbatiit làmboo. 


Jikko nag xam ngeen ne daa bokk ci mbaax yu wér yi sunu mbatiit ak sunu cosaan làmboo. Loolu moo tax Ngóornamaŋ bi Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko jiite dugal ci biir ay jëfam mbaaxu JUB-JUBAL-JUBBANTI. Ñu man koo tënk rekk ci: Wane yoon ci JUB ak JUBAL. JUBBANTI tooñ yi ñu yàgg a teg ci keneen ak ci kaw askan wi. Lii mooy waat yu am solo yi kenn ku nekk ci nun war a doxal fépp, rawati na nag ñi am lu ñu leen jot a dénk ci doxaliinu pénc mi.


Doxaliinu politig wu jaar yoon nag ci kenoy mbatiit la war a sampe.


Matale sas wu yaatu wii nag du lenn lu dul fexee sàmmonte ak Ndayi Sàrti Réew miy wax ci jiital, taqoo gu xóot ak Askanu Senegaal wu moom boppam « ci mbaaxam yu wér yi tabax bennoo gi ci réew mi » te nangu pas-pasu « jox cér mbooleem mbatiit yi nekk ci biir réew mi ».


Kon dinaa bàyyi xel bu baax, ci biir doxal politigu mbatiit mi, raññale, sàmm ak fésal sunu patrimuwaan. Li nu am ci wàllu mbatiit mooy dundal sunuy xalaat, te mooy wéral, jaare ko ci jottali ko maas giy ñëw ëllëg, dundal sunu mbatiit. Ci loolu, yitte ju kawe laa am ci tomb yii may bëgg a lim:


  • Koomum mbatiit mi ngir taxawu waar yépp boole ko ak dooleel àntarpiriis  yi ak endistiri yi ci wàllu mbatiit ak fent te doon lu man a jur ay xëy ñeel ndaw ñi ak jigéen ñi. Pàcc bii nag daa làq njariñ yu bari ci man a taxawal ay xëy ak koom, di lu ñu war a gën a xamle, lootaabe ko teg ci man kop jëfandikoo jaare ko ci yombal jot gi ci xibaar yi soxal wàllu mbatiit, gunge fentkat yi ci tàggat leen boole ko ak kopparal, añs.


  • Xarala yi doon lu manatul a ñàkk, ngir fésal ci mbooleem jumtukaayi xarala yi, yi sunu artist yi di defar teg ci jox ndaw ñi yeneen jumtukaay yu ñu man a amee am xëy. Xarala yi nag taxawaay bu am solo lañu am ci koomum mbatiit mi. Ràppor 2018 bu UNESCO ci koowaasiyoo 2005 bi mu tuddee « Xalaataat ci politigu mbatiit : fent gi ci xolu suqaliku » wane na ne xarala yi soppi nañu xar-kanamu mbatiit mi donte sax koomum mbatiit mi a ngi gën a jëm ci xarala. Danoo war a jëfandikoo bu baax li xarala yi di maye ngir fésal mbatiit mu gànjaru mi nu am. Ñiy yëngu ci wàllu mbatiit ci réew mi nañu posewu ci li xarala yi indi jéem koo jëfandikoo.


  • Dooleel yaatalug mbatiit mi, jaare ko ci taxawu gu wér ci ndoxalug mbatiit mi ci réew mi ak xew yi ñuy amal fépp ci mbeeraayug réew mi. Loolu nag lu ma soxal la ngir doxal yamale gi war a am ci gox yi, fexe ba liy bawoo ci mbatiit mi man a jariñ mbooleem waa réew mi ba nga xam ne fépp fu waay nekk dinga man wane patrimuwaan bi am ci réew mi. Loolu daa bokk ci liy dëgëral déggoo gi ci réew mi.



Ngir doxal politig boobu nag, Nguur gaa ngi yaakaar ci jaayante ak yéwénug njabootu mbatiit mi ak ci mbooleem partaneer yi  ëllëgu pàcc bii yitteel.


Ci yoon wii nu tegu jëm ci amal dund gu teey ñeel mbooleem ñi séq réew mi, mbatiit mi ak taxawaay bu kawe bi mu am, dafa war a teg loxoom bu wér ci dundal sunu politig yii nu teg ngir ñu tàbbi ba fàww ci anam yu gën, ci lii nu doon ak fi nu namm yegg. Ni mu nuy màndargaalee boole ko ak di nu wane ci àddina si, mbatiit day bokk ci liy tax nu moom sunu bopp ci wàllu jikko ak xam-xam. Mooy tax itam ñu jox cér mbooleem ñi am mboor, ay gis-gis yu wuute ci doxiinu àddina, saa boo xamee rekk ne waxtaanu wegante  te làmboo ak njariñ door na, jëm ci gën a dooleel lëkkaloo ak nangulantey xalaat.


Soxna yi ak Sëriñ si,


Duma daaneel te fàttaliwuma ndénkaan lii cosaanoo ci nun ci ne benn loxo rekk du tàccu; maanaam, lépp lu sotti rekk daa fekk ñu ànd ko. Maa ngi ciy woo kon mbooleeem aktéer yi ñu gën a am taxawaay ngir àndadoo doxal mbaaxi jàppalante, diisoo, lëkkaloo, diggante nguur gi ak ñiy yëngu ci mbatiit mi, diggante artist yi ci seen biir, ak sunu diggante ak sunuy partaneer itam.


 Doxaliin wu ni mel rekk nag mooy tax nu man a àndandoo daan jafe-jafe yi mbatiit mi di jànkoonteel ba man a yegg ci suqalikug koom mi ak dundiin wi, moom sunu bopp ci wàllu xam-xam niki noonu man a fésal sunu cosaanu Afrig.


Maa ngi tëjee nag ci ñaan bu baax yii sunu artist yu jàmbaare yii di fent bokk bu wér ci liy mottali li nu yittewoo ci taaral, doon ndimbal ci gën a nànd doxiinu àddina teg ci nu jaare ci yu am solo yi ñuy jàllale, yombal yarub sunuy doom ak askan wépp. Art day bégloo, di géntloo di xalaatloo; day jàngale di yar.


Ginnaaw bu ma woowee askan wi, rawati na ndaw ñi, ñu ñëw teewe bu baax yëngu yiy am ci Biennale bi, maa ngi ñaanal ñépp feetu mbatiitu jàmm.


Ci ñaan yii nag kon maa ngi xamle tijjitel 15eelu « Biennale Art Africain Contemporain 2024 ».


Maa ngi leen di jaajëfal ci seen ug teewlu.