Njiitu Réew mi séq na ab jataay ba tay ci àjjuma ji 14i fani féewarye 2025 ca Addis Abebaa ak ñii di Soxna Narros Thomas Sekkereteer eksekitif bu NEPAD ak S. Jeffrey Sachs, Njiital Barabu gëstu bii ci wàllu suqaliku gu sax ca Jànguneb Kolumbiyaa.
Njiitu Réew mi waxtaane na ak Soxna Nardos Thomas lu jëm ci lëkkaloo ak ay naal ci wàllu jumtukaau ak suqalikug koom mi.
Njiitu Réew mi weccente na ay xalaat itam ak S. Sachs ci jafe-jafe yi ñu seetlu jëm ci kopparal wàllu suqaliku ak doxaliin yu sax ci Afrig.
S. Sachs di jëmm ju ràññiku ci àddina si ndax liggéey yu mucc ayib yi muy amal ci wàllu suqaliku gu sax, rafetlu na jaayanteg Senegaal jëm ci doxal politigi koom yu boole ñépp te sax dàkk. Waxtaan yi jëmoon ci xool yan pexe lañuy teg ngir man a dajale koppar yu doy ngir taxawu sémbi suqaliku yu sax dàkk, lépp jaar ci leeraange ak sellaal ci doxwliinu pénc mi.