Abujaa dalal na Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay FAY ngir 67eelu ndajem CEDEAO.

Biti Réew - 21 MONTHS.JUNE 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, yegg na ci gaawu bi 21i fani suwe 2025 ca Abujaa, gëblag Réewum Niseriyaa ga ñu ko teertu, tatagal ko, ci ngoon gi. 

Muy tukki bu jëm ci wàllu 67eelu jataayu ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu Mbootaayu Réewi Afrig Sowu Jant yi (CEDEAO), ñu jàpp ko dibéer 22i fani suwe 2025.

Njiitu Réew mi dina teewe waxtaan yi ànd ko ak ay naataangoom ngir gën a dëgëral lëkkaloo gi ci mbootaay gi ak taxaw temm ci dal gi, suqaliku gu sax ak bennoog askan yi ci biir CEDEAO.