Abujaa di Gëblag réewum Niseriyaa, dalal na ci dibéer ji, 66eelu Ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yi bokk ci Mbootaayu Réewi Afrig Sowu Jant yi (CEDEAO).
Ndaje mu am solo mii, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay doon teewe, dajale na kilifay réew yi ko séq ngir xalaat ci jafe-jafe yu bari yi am ci tund wi, rawati na ci wàllu politig, kaaraange ak koom.
Ca jataay ba, Mbootaay gi ndokkale na Peresidaa Fay ci anam yi mu lootaabee joŋantey lesislatiif yi ci Senegaal ci jàmm, dal ak leeraange, di luy firndeel rekk ñorug askanu Senegaal ci wàllu demokaraasi.
Ci kanamu jafe-jafey kaaraange, koom ak politig yi ñuy jànkonteel ci tund wi, CEDEAO jaayante na ci amal ay coppite ngir indi ci ay saafara.
Ci geneen wàll, ndokkale nañu Peresidaa Fay ci jéego yi muy teg jëm ci dox tànki jàmm diggante CEDEAO ak réewi AES yi. Mbootaay gi yeesalaat na kóoluteem ci moom mii fas yéenee demaat ci réew yooyu ci fan yii di ñëw ngir wéyal waxtaani laamisoo yi ngir ñu dellusiwaat.