Biti Réew - 05 MONTHS.DECEMBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, séq na ab jataay ak Seex Mohammet Bin Sayed Al Nahyan, Njiitu Réewum Emiraa Araab Unii, ca Abu Dabi.
Ñoom ñaari Njiit yi feddali nañu yéene ji ñu bokk am ci gën a dooleel jëflante yu am solo yi dox diggante Senegaal ak Emiraa. Peresidaa Fay ak naataangoom bi fésal nañu pàcc yu bari te am solo ngir lëkkaloo gu jëm kanam, rawati na ci pàcc yu mel ni yasara gi, xarala yi, njàng mi ak mbay mi.
Lëngoo gu am solo gii nag mu ngi jëm ci suqali ay sémb yu mel ni amal ay coppite ci wàllu yasara, baral jéego yi ci wàllu fent ak xarala, gën a dooleel yéene yu mel ni tàggat ndaw ñi, niki noonu gën a dooleel kaaraange gi ci li nuy dundee ak jëflante yi ci wàllu xarala. Mu doon luy tijji itam yoonu jëflante yu làq njariñ ñeel ñaari réew yi.