Abu Dabi : Peresidaa Fay daje na ak ay dugalkati xaalis yu Emiraa

Biti Réew - 05 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi dalal na tamit tay ci ngoon gi, ay mbootaayi saa-emiraa yu séddalikoo ci ay dugalkati xaalis, ay lijjantikat ak ñenn ñu teewal kuréli kopparal yi.

Ñu doon waxtaane ci pexey lëngoo yu ñu man a teg ci pàcc yu am solo yi nekk ci biir « Agenda Sénégal 2050 », yu ci mel ni mbay mi, yasara gi, xarala yi, njàng mi, xëy mi ak yaale gi.

Peresidaa Fay ci li mu gën a taxaw nag mooy solos amal lëngoo gu am doole diggante priweb Emiraa bi ak piriweb Senegaal bi, te war a doon keno bu wér ci coppite yi ñu namm a amal ci koom mi ak nekkiinu askan si ñu dëxëñ ci sémb wii.