Abidjaŋ : Peresidaa FAY dalal na Sekkereteer Seneraalu OCDE.

Biti Réew - 12 MONTHS.MAY 2025

Laataa muy bawoo Abijaŋ, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na Macaas Kormaan, Sekkereteer Seneeralu Kurél gi yor wàllu lëkkaloo ak suqalikug koom mi (OCDE).

Ndaje mii tax na ñu waxtaan ci mbébeti lëkkaloo diggante Senegaal ak OCDE, rawati na ci wàllu yoriin wu leer ci galag yi, ndajalem balluwaay yi ci biir réew mi, gën a jagal yoriinu koom mi boole ko jàpp ci teg politig suqaliku yu ñoŋ.