Ab jataay diggante Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ak Njiitu Jëwriñu Japon ca Yokohama.

Biti Réew - 20 MONTHS.AUGUST 2025


Ginnaaw jataay bi mu séq ak Soxna Saaraa Zaafarani, Njiitu Jëwriñu Tunusi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, séq na waxtaan wu am solo  ak Njiitu Jëwriñu Japon, muy kilifa gii di Shigeru Ishiba. 

Ñaari kilifa yi fésal nañu jëflante yu mucc ayib yi  dox diggante Senegaal ak Japon, te lalu ci lëkkaloo gu mat a roy, lëngoo gu yàgg ak ay mbaax yu ñu nuroole yu mel ni jàmm, demokraasi, sàmmonte ak réewum  yoon ak yoonu àddina si. 

Presidaa FAY soññe na ngir ñu gën a dëgëral lëngoo gi ci fànn yu am solo yu mel ni tàggatu gi, paj mi, ndox mi, napp gi, niki noonu jàmm ji ak kaaraange gi. Taxawlu na bu baax ci wàllu tàggatu gi ëpp solo ngir am ug suqaliku, jaare ko ci wane jéego yu am solo yi ci Japon teg te doon luy firndeel ne am nit ñu am xam-xam mooy caabiy yokkute.

Ci wàll woowu, torlu nañu ci ag déggoo gu jëm ci tabax beneen barabu tàggatukaay bu Senegaal-Japon (CFPT-SJ) ca Jamñaajo, ak yeneen déggoo yu ci war a  topp ci fan yii di ñëw. Ndaje mii nag tijji na yeneen wunti lëkkaloo yuy jariñ ñaari wàll yépp, di luy firndeel lëkkaloo gu rittax te am doole gi dox diggante ñaari réew yi.