80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si : Peresidaa FAY daje na ak topp-njiitu « Fondation Buffett ».

Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Ci 80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, jagleel na, ci talaata ji 23i fani sebtàmbar 2025, ab jataay  Soxna sii di Senait FISSEHA, Topp-Njiitu « Fondation Buffet ». 


Waxtaan yi jëmoon ci yéeney lëngoo ci fànn yu am solo yu mel ni paj mi, xarala yi, njàng mi, niki noonu fexe ba ndaw ñi ak jigéen ñi manal seen bopp, muy yitte yu far yu nekk ci  biir « agenda national » bi. 


Ndaje mii di wane yéene ji ñu bokk am jëm ci tabax lëngoo gu am doole ngir suqaliku gu sax, boole ñépp te yamale ñeel nit ñi.