80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si : Njiitu Réew mi bawoo na Ndakaaru wutali New York.

Biti Réew - 21 MONTHS.SEPTEMBER 2025

Njiitu Réew mi bawoo na Ndakaaru tay ci suba si wutali New York ga mu war a teewe 80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si 

Ak arminaat bu am solo ci wàllu laamisoo, moom Njiitu Réew mi dina yékkati kàddug Senegaal boole ko ak layal gis-gisu Afrig gu naat te moom boppam ci jataay yu mag yi ñuy waxtaane doxaliinu àddina si. 

Laataa  muy bawoo ca Naawub Sóobare bu Lewopóol Sedaar Sengoor, moom Kilifa gi saafonte na ak Njiitu Jëwriñ yi Usmaan SONKO niki noonu kilifa yu bari ci wàllu siwil ak militeer. 

Peeñ :