79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi àddina si: Njiitu Réew ñu ngi koy séntu ca USA

jëwriñ - 24 MONTHS.SEPTEMBER 2024

Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, dina dem ca New York ngir teewe 79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi àddina si, war a am 24 ba 30i sebtàmbar 2024. Ñu war cee waxtaane tomb bii di « Bennoo ci biir wuute, ngir jàmm ju lëw, suqaliku gu sax ak sàmm ngorug doomu aadama ci fépp ak ci ñépp». Ndaje mii am pose lay doon ci Njiitu Réew mi ngir mu yékkati kàddug Senegaal ci yu am solo yiy xaar àddina si. Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY FAY dina teewe itam ndajem Ëllëg, di naalu Njiital Mbootaayu Réewi Àddina si, Àntoño Guterres.