79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Àddina Si : Àddug Basiiru Jomay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal

waxtaan - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2024

Wëppa : « Bañ a bàyyi kenn ginnaaw: àndandoo jëf ngir jàmm, suqaliku gu sax ak diññitey maasi tay ak yu ëllëg» 

*** 

Àddug Kilifa gi Basiiru Joomay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal


Yaw Njiital jataayu Ndaje Mu Mag mii,

Yéen Njiiti Réew yi ak Ngóornamaŋ yi  jigéen ak góor, 

Yaw Sekkereteer Seneraal bi,

Soxna yi ak Sëriñ si,

Kilifa yu am solo yi,

Bala maa wax genn kàddu, bëggoon na maa posewu ci jataay bii fàttaliku jëmmi sunu naataagoo ma-réew bii di ndem si Yàlla Aamadu Maxtaar Mbow mi nuy door a dëddu. Njiital UNESCO woon, 1974 ba 1987, doonoon kilifa gu am taxawaay ku amoon solo ci xeex ngir  Afrig gu moom boppam. 

Maa ngi ndokkale Filemon Yang mi ñu fal Njiit ci 79eelu jataayub Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, niki noonu ki mu fi wuutu, ci liggéey bu am solo bi mu amal ci sunu sémb wii nu séq. Ci seen jëmm, maa ngi ñaan ndam ci doxal sunu liggéey yii. Maa ngi rafetlu itam jaayante gu sax gi Sekkereteer Seneraal bi ame, di Antóño Guterres, mi nga xam ne ay jéegoom ci dooleel jàmm ji, diññitey nit ki ak jëflante diggante réewi àddina si doon na lu am solo lool. 

Senegaal a ngi koy feddali ag njàppaleem ci sasam wii mu yor ci jamono ju àddina si yëngoo lool.

Su may àddu tay jii nag, damay ànd ak pas-pas bu wér ci ne : bennoo ci biir wuute mooy caabi ji man a indi jàmm, suqaliku gu sax ak diññite nit ñépp, fépp ci àddina si. Wëppa wii nu tànn ci jataayu ren gii, te nu war koo tegtaloo ci sunuy waxtaan, moo nu yóbbu ci nu war a xoolaat taxawaay yi nu bokk am, te fexee dëggal ne pas-pas bi sos Mbootaayu Réewi Àddina si, te ñu xaatim ko lu ëpp 80i at, mu ngi wéy di ŋàbb digeb àddina su gën a jub te gën a maandu.

Yaw Kilifa gi,

Soxna yi ak Sëriñ si,

Noo ngi dund ci àddina su jaxasoo, soo xam ne pas-pasi Sàrtub Mbootaayu Réewi  Àddina siy woote yamale, yoon ak sàmmonte ak yelleefi nit ñi, bis bu set ñu salfaañe ko. Xeexoo yaa ngi gën di yaatu, ñàkk a yamale gi di law, jafe-jafey njuux yi di gën a jéggi dayoo bay yàq dundi ay milyoŋi nit ci àddina si. Dolliku ci loolu, nuy dund xel-yaar gu jur njàqare ci jëflante diggante réewi àddina si, ci jamono ji ko doomi aadama yi gën a yittewoo.

Àddina sépp a war ne jàkk xoolante ciy gët, bañ a raayalante ay ginnaaw. Mbaax yi nu waatoon ne dinanu leen sàmm ñu ngi leen di dëggaate ci gox yu bari. Moo xam ca Gaza, ca Tel Aviv, ci Ndakaaru walla feneen, nit ku ne dafa war a doxal ci boppam yamaleg diññite googu, diññite gu jéggi dig yi, mbatiit yi ak gëm-gëmi diine yi. Sunu wareef la nun ñépp nu taxaw temm ba diññite googu ñu aar ko sàmmal ko jëmm ju nekk, ci lu amul sette. Wareef googu sax nag mooy dëgg dëgg li tax a jóg Mbootaayu Réewi àddina si.

Moone de, bis bu set nu seetlu ne yoonu àddina si, di li war a tabax jàmmi àddina si, dees koy faral di salfaañe. Ay déggoo yu ñu xaatim ci Ndaje mii, dees ciy faral a gëmm. Bu nu dee maslaa ci salfaañe yooyu ñuy baamu nag, noo ngi dëggaate pas-pasi Sàrtub Mbootaayu Réewi Àddina si, boole ko ak di màbb kenoy Kërug jàmm jii.

Kenoy Mbootaayu Réewi àddina si masul a yëngoo nii nga xam ne jamonoy fitna la, tiit ak njàqare. Su dee namm nanoo génn tolluwaayu xare bii ngir jëm ci jamonoy àddina su mucc ayib, kon nag jot na sëkk nu soppi doxaliin. Jot na sëkk nu tegaat nit ki ci xolu sémbi àddina si, niki nu ciy woowee wëppaw  jataayu ren gi.

Yaw Kilifa gi,

Soxna yi ak Sëriñ si,

Manatunoo gëmm ci musiiba yiy xew ci Sahel bi. Ay rëtalkat yuy rëtal, di yàq di ray ay askani siwil yu deful dara. Tund woowu, daloon lool bu njëkk, te leegi bis bu set fitna di fa xew, Mbootaayu Réewi Àddina si moom, rawati na Ndiisoog Kaaraange gi, patt gi rekk la ci maye  mel ni dara xewul. Niki noonu manunoo nangu Sahel bi doon barabu wujjekaayu Réew yi am doolee, nga xam ne seen jàmmaarloo yi duñu def lu dul gën a tàbbal tund woowu ci guuta.

War na maa fàttali fii ne jàmm ak kaaraangeg Afrig maneesu leen teqale ak jàmmi àddina si, te wareef la ci Ndiisoog Kaaraange gi mu bay waaram niki ku war a sàmm dalug àddina si.

Maa ngi feedali fii njaaxleg Senegaal ci tolluwaayu musiba may wéy ca Palestin. Ay maasi lëmm màgge nañu fa ca keppaaru njaay-doole ga, ñu xañ leen seen yelleef yi gën a suufe ñeel réew mu mu war a dund

Senegaal, miy Njiital kurél giy sàmm yelleef yi manul a ñàkk ñeel askanu Palestin, mu ngi woote ñu gaaw wéer gànnaay ya ba fàww. Noo ngi feddali sunug njàppale ci pexe mii jëm ci taxawal ñaari réew, boole ko ak def Jérusalem-Est muy gëblag Palestin, niki ko Mbootaayu Réewi Àddina tënkee woon cig dëppoo. Xare bii, nga xam ne bawul jigéen, bawul ndaw, ba ci jumtukaay yi ñu soxla ngir dund, góom bu yaatu la bu tegu ci ndoddu àddina sépp. Jot na sëkk, ñu delloosi, fépp fu ay jàmmaarlo am, doxal fa yoonu àddina si ci yelleefu nit ki, te Mbootaayu Réewi Àddina si tamit fexee bay waaram ci dox tànki juboolee ak sàmm jàmm ji.

Soxna yi ak Sëriñ si,

Jàmm yamul rekk ci ñàkk a xare. Jàmm, mooy fexe itam ba nit ku nekk man a sàmm ngoram, am lu muy dunde, am dëkkuwaay, jot ci am njàng ak paj mu mucc ayib. Te tay jii, lu ëpp 750i milyoŋi nit lekk ba suur jafe na leen lool, teg ci ay milyoŋ ci ñoom di gën a tàbbi ci ndóol gu jéggi dayoo. Lim yii nag day gën a soril àddina si mu man yegg ci Jubluwaayi Suqaliku gu Sax gi ñu jàppoon fii ak 2030.

Manatunoo wéy ci anam yii ñuy doxalee àddina si di wéy di jur ag ñàkk a yamale. Jot na sëkk nu teqalikoo ak bopp sa bopp gi te jéem a teg pas gu yees ci nekkiinu askan wi, fexe mu tegu ci jàppalante ak lëkkaloo. Pas googu nag dafa war a ànd ak amal coppite yu mag ngir man a taxaw ci yittey politig yi, koom mi ak kéew yi nuy dund ci sunu jamono.

Li njëkk mooy, fàww nu sàmm te gën a dooleel lëngoo diggante réewi àddina si nga xam mooy menn pexe mi man a suuxat jàmm ak kaaraangeg àddina si. Loolu nag day jaar ci amal ay coppite ci lu jamp ci campeefi àddina si, rawati na Ndiisoog kaaraange gi, FMI ak Bànk Monjaal, ngir ñu gën a boole ñépp te méngoo ak tolluwaayi taxawaayu réew yi ak koomum jamono ji. Kembaaru Afrig, rawati na, dafa war a am toogu bu gën a am solo ci warab yu kawe yi ñuy jëlee dogal.

Ñaareel bi, jot na sëkk ñu joyyanti ñàkk a yamale ci wàllu koom giy gàllankoor suqalikug réewi bëj-jéeri yu bari. Yaxantu gu yamoowul gi, rawaleg galag yi, jokkalantey koppar yu setul yi ak ñàkk a fay galag yi, ñu ngi nërmeel réew yi nekk ci yoonu suqaliku, rawati na ci Afrig. Jalgati yooyu dees leen a war joyyanti ngir may réew yépp ñu man a bokk bu baax ci yaxantug àddina si teg ci jariñu ci yokkuteg koom mi.

Ñetteel bi, manul a ñàkk nu am ug dogu ci xeex soppikug njuux li, jaare ko ci nangu ne lépp ci sunuy jëf la bawoo waaye nag ci anam yu wuute. Réew yi am ndefar yu bari, nga xam ne ñoo ëpp lu ñuy génne ci xeeti saxaar ak gaas yu man a soppi jaww ji, war nañoo gën a def i jéego ci dugal ay koppar yu jëm ci fexee jàll ci jëfandikoo yeneen xeeti yasara yu jub te yamoo, yoo xam ne du gàllankoor réew yi nekk ci yoonu suqaliku.  Wareef la ci nun nu sàmm  déele bi ci lu dul salfaañe yelleefi réew yi gën a néew doole ngir ñu man a wéyal seen ug suqaliku.

Ñenteel bi, jot na sëkk ñu dakkal lépp lu jëm ci jéem a ga ay doxaliinu xayte meneen réew. Ba mu amee jonn ak tay, Senegaal daa mas di xeex yamoo diñite ci wàllu mbatiit ak xayte. Wuute googu nag dafa war a wéy di doon kenoy dëkkandoo askan yi ci jàmm. Menn réew warul a ga ñi ci des jàpp ne ay jëfam walla ay mbaaxam rekk a war a doon liy dox ci àddina si. Nangu wuute yooyu mooy li man a suuxat dal ak jàmm ci àddina si.

Soxna yi ak Sëriñ si,

Senegaal daa ànd ak dogu ci yoon woowu. Danoo tànn tabax réew mu taxaw temm ci amal suqaliku gu sax, boole ko ak am ay naal yu wér te wóor ci fànn yu mel ni yasara yi, bay dundee ak doxaliin wu leer ci yoriin yi. Waaye nag xam nanu ne, ngir nu am ci ndam, danoo soxla boole sunuy doole ak njàppaleg àddina si.

Menn réew, ak lu mu am am doole, manul a taxawul boppam kepp tafaar yu bari yi àddina di jànkonteel. Fàww nu àndandoo jëf, bennoo ci biir ug wuute, ngir tabax ëllëg goo xam ne dañuy sàmmonte ak diññite nit ki boole ko ak am naataange gu ñépp di bokk. Ci lëkkaloo ak joxante cér  rekk lanu man a saafaaraa jafe-jafe yu bari yiy xew ci àddina si. 

Maa ngi leen di jaajëfal ci seen ug xerewlu.