67eelu Ndajem CEDEAO : Peresidaa FAY bawoo na Ndakaaru wutali Abujaa.

Biti Réew - 21 MONTHS.JUNE 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, bawoo na Ndakaaru tay ci suba wutali réewum Niseriyaa. 

Ca Abujaa, Njiitu Réew mi dina teewe 67eelu ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yi bokk ci Mbootaayu Réewi Afrig Sowu Jant (CDEAO), ñu war koo amal 22i fani suwe 2025.