jëwriñ - 15 MONTHS.DECEMBER 2024
Dibéer 15i fani desàmbar 2024, Abujaa di gëblag réewum Niseriyaa, dina dalal ndajem mbootaayu réewi Afrig Sowu Jant yi di CEDEAO. Xew-xew bii dina dajale Njiiti Réew yi ko séq, bokk ci ñoom Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, ngir waxtaane tolluwaayu Politig bi, koom mi ak kaaraange gi.