5eelu bëccëgu SETAL SUNU RÉEW bi ñu jagleel lekool yi.

xamle - 05 MONTHS.OCTOBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay doon teewe ci gaawu bi ca Mbuur, ànd ko soxnaam, Soxna Mari Xóon Fay, 5eelu bëccëgu SETAL SUNU RÉEW, te ñu jagleel ko lekool yi.
Njiitu Réew mi nemmikuwalale na ENO bu Mbuur, ba jot faa jëmbataale ag garab. Dem na tamit moom Njiitu Réew mi ca Lycée Demba Jóob ga mu defee njàngam ci wàllu “secondaire” diggante 1997 ba 2000, laataa muy dem ca UCAD wéyal um njàngam.
Ànd na ak askan wa ci jéem a setal warab ya jëm ci waajtaayu ubbiteg lekool biy dëgmal, boole ci ñaax ndaw ñi ñu gën a jox fulla njàng mi ak fàttali solo si nekk ci liggéeyu jàngale.
Nemmiku gii am pose la woon ci Njiitu Réew mi mu weccente ak dongo yi, gisewaat ak ña ko daan jàngal ak ay xaritam. Gisaale na itam sémbu yeesal ak yokkaat Lycée bi, jëm ci gën a suqali jumtukaayi njàng ma ak tàggat yaram.