Ca jataayu Ndaje ma ñuy waxtaane kopparalug suqaliku gi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, séq na ay jataay yu am solo ci wàllu lëkkaloo ak kilifa yu bari yu bokk ci ñi Senegaal lëngool.
Ak kilifa gi di Roi Felipe VI d’Espagne, waxtaan yi a ngi jëmoon ci dooleel lëkkaloo gi ci fànn yu bari, rawati na ci wàllu mbay mi, turism bi ak saytu gu mucc ayib ci wàllu tukki.
Ñaari Njiti Réew yi feddali nañu seen yéene ngir gën a dooleel tukki bu jaar ci yoon te sàmmonte ak yellefi nit ñi.
Ak Njiitu Réewum Estoni, Alar Karis, waxtaan yi jur nañu ag déggoo gu jëm ci gën a yaatal kaadaru yoonalug lëkkaloo diggante ñaari réew yi. Jubluwaay bi di fexee jëfandikoo yoon yu bees, rawati na ci wàllu xarala yi nga xam ne Estoni doon na ku ci àddina sépp ràññee. Persidaa Karis sàkku na itam ci Senegaal mu dooleel lawaxug réewam ca Ndiisoog kaaraange gu Mbootaayu Réewi àddina si.
Ak Ajay Banga, Njiitu Kippaangog Bànk Monjaal, moom Njiitu Réew mi kañ nañu ko fa ci jéego yu am solo yi muy teg ci wàllu doxaliin wu leer ak yoriin wu jub wi mu sóob Senegaal. Bànk Monjaal, ànd ak FMI ak SFI, jaayante na ngir gunge doxaliin wu yees wii jaare ko ci taxawu sektéer piriwe bi ak jëmmal sémbu taxawu ci wàllu njël li.
Ci kilifteefu Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay FAY, Senegaal a ngi gën a dooleel ag laamisoom ci wàllu koom ak taxawaayam ci àddina si ngir suqaliku gu sax gu ànd ak moom sa bopp.