3eelu edisoo Raaya Njiitu Réew mi: Peresidaa Basiiru Jomaay Fay di sargal jàngalekat yi

xamle - 06 MONTHS.FEBRUARY 2025


Askan wi kañ na  tay ci suba xereñte ak njàmbaarteg sunu jàngalekat yi jaare ko ci Raaya Njiitu Réew mi ñu jagleel Jàngalekat yi.

Ci jataay boobu, Sëriñ Àlliyun Badara Mbeng mooy ki ci gën a ràññiku, ñi ñu tànnoon ñépp itam sargal nañu leen bu baax ci seen dogu gii doon lu mat a roy. Seen ug jaayante tax na, góor ak jigéen ñii di tàggat ndaw ñi war a yori réew mi ëllëg, jëmbat ci ñoom xam-xam ak jikko yu rafet. 


Nanu àndandoo yékkati lekoolu Senegaal ca kaw, tabax Senegaalu ëllëg, goo xam ne ndaw lu ne dina man a jot jumtukaay yi war ci moom ngir wane man-manam bu wér.