jëwriñ - 28 MONTHS.NOVEMBER 2024
Ñetteelu atu bis bi ñu jagleel Daara ci réew mi dees na ko amal alxemes 28i fani nowàmbar 2024 ca Dakaar Arenaa bu Jamñaajo. Xew-xew bii Jëwriñu Njàng mi lootaabe, dina am ci njiital Basiiru Jomaay Fay Njiitu Réew mi.
Màggal gii nag mu ngi jëm ci sargal daara yi doon keno bu am solo ci njàngum Alxuraan ci Senegaal. Sémb wi war a séddalikoo ci ay diisoo, ay jataay ak fésal xereñte ci wàllu tarbiya ak njàng