Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay posewu na ci 38eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi ngir sumb ay waxtaani lëkkaloo yu am solo diggam ak ay kilifay saa-afrig yu ràññiku. Diisoo yi mu séq ak kilifa yii di Wiliyaam Samoei Ruto, Njiitu Réewum Keeñaa ak João Lurenço, Njiitu Réewum Àngolaa, tax na ñu gën a dëgëral lëkkaloo gi boole ci yaatal ci jafe-jafe yi ñu bokk am ci wàllu suqaliku.
Bu weesoo jataay yooyu, Njiitu Réew mi teewe na ay ndajey waxtaan yu kawe ci wàllu kopparal paj mi jaare ko ci jëfandikoo liy ballee ci kembaar gi, mu àndoon ko naataangoom bu Ruwàndaa di Póol Kagame ak yeneen kàngam yu bari ci wàll wi. Ca ndaje ma Njiitu Réew mi woote na ngir :
- kopparal gu wér ci doxaliinu paj mi jaare ko ci dajale liy ballee ci kembaar gi.
- Réew yi fexee jaayante ci sàmmonte ak lii di « Déclaration d’Abuja » bi jëm ci jagleel paj mi 15% ci seen njël.
- Dooleel taxawaayu sektéer piriwe bi ak gox yi ak goxaan yi ci ni ñuy kopparalee paj mi.
- doxaliin wu leer te xereñ ci jumtukaayi paj mi.
Senegaal gi taqoo ak gis-gisam bii ci amal suqaliku gu boole ñépp ak manal boppam, mu ngi feddali kon jaayanteem jëm ci tabax doxaliinu paj mu am doole te yamale, doxaliin wuy taxaw ci fexe ba kenn ku ne man a jot ci paj mu mucc ayib.