jëwriñ - 13 MONTHS.FEBRUARY 2025
Kilifa gi, Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, dina dem ca Adis Abebaa (Ecopi) li ko 13 jàpp 16i fani féewarye 2025 ngir teewe 38eelu jataayu Ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu Mbootaayu Réewi Afrig, ñu fay waxtaane tomb bii di : « Atum yoon ngir saa-afrig yi ak ñi càllaloo ci saa-afrig jaare ko ci defaraat ».