Biti Réew - 08 MONTHS.DECEMBER 2024
Ci lu soxal Ndajem Waxtaan miy am ca Doha, te door gaawu 7i fani desàmbar 2024, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay teewe na tay ci suba, jataay bu ñu doon waxtaane tomb yu am solo.
Ci kanamu Ghida Faqri mi doon doxal jataay bi, Njiitu Réew mi posewu na ci ngir àddu ci tomb yi gën a fés ci jamono jii. Ci jataay bu gànjaru bii, Njiitu Réew mi yaatal na gis-gisam ci Senegaal ak Afrig gu deñ cig yaras, jiital ay ndawam, dogu boole ko ak tijjiku ci àddina si. Mu dolli ci moom Njiitu Réew mi ne, donte am na ay jafe-jafe, terewul yaakaar ju kawe ci ëllëg gu lalu ci dëgër, fent lu bees ak dogu, moo tegu ci Senegaal ak kembaaru Afrig.
Teewaay bu am solo bii nag day firndeel taxawaayu Senegaal niki ku manul a ñàkk ci kanamu àddina si.