Ci ndënel Kilifa gi Umaro Sisoko Embaló, Njiitu Réewum Gine Bisaawó, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal teewe na, ci suba si ca Bisaawó, ci liggéeyi 15eelu ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yi bokk ci réew yiy làkk portuge (CPLP), mu doonoon seen gan.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na jëflantey mboor, mbatiit ak mbokkoo yi yàgg a boole Senegaal ak Gine Bisaawó, lépp boole ko ak rafetlu ngir CPLP gën ubbeeku ci yeneen partaneer, yu lalu ci lëkkaloo ak jàppalante. Kilifa gi feddali na jaayanteg Senegaal jëm ci gën a dooleel ay jëflantem diggam ak réew yi bokk ci CPLP, rawati na ci wàllu mbatiit, njàng mi, yaxantu gi ak mbay mi, lépp ci kaw lëngoo guy làq njariñ ñeel wàll yépp.
Lu jëm ci tomb bu am solo bii di manal sa bopp ci wàllu dund, Peresidaa FAY soññee na ngir ñu àndandoo sóobu ci amal coppite gu sax dàkk ci wàllu mbay mi. Xamle na solos fent gi, jariñoo balli mbindaare yi, suqali jumtukaayi ja yi ak taxawu bu baax baykat yu ndaw yi, rawati na jigéen ñi ak ndaw ñi.
Mu tëjee, moom Njiitu Réew mi yaatal na jubluwaay yu mag yi ci “Vision Sénégal 2050”, bi nga xam ne mbay mi keno bu am solo la ci ngir suqalikug réew mi. Feddali na yéeney Senegaal jëm ci dugal loxoom bu baax ngir ñoŋal dund bi ci kembaaru Afrig, ci pas-pasu wareef wu ñu bokk ak lëkkaloo ci àddina si.
Peeñ :