145eelu atu Wooteb Seydinaa Limaamu Laay: Siyaareb Njiitu Réew mi ca Yoof Laayeen

xamle - 29 MONTHS.JANUARY 2025

Ci Màggalug 145eelu atu Wooteb Seydinaa Limaamu Laay giy am 30 ak 31i fani sãawiye 2025, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ànd na ak soxnaam, Soxna Mari Xóon Fay, dem siyaareji njabootug Laayeen.

Xalifa Seneraal bi di Sëriñ Muhammadu Maxtaar Laay teeru ko tatagal ko, Njiitu Réew mi fàttali na, ci kanamu mbooleem njabootug Laayeen gi ak kilifay ndoxal yi ak yu aada yi fa teewoon, taxawaay bu am solo bi këri diine yi am ci tàggat ay nit ñu nite, nga xam ne mooy li waral dal ak déggoo gi am ci réew mi.

Peresidaa Fay àddu na itam ci tegtal yi mu jox Ngóornamaŋ bi, ci njàppandalug pekk bi yor wàllu diine ci Njénde li, ngir amal lootaabe gu mucc ayib, ci màggalug ren gi ñuy waxtaane « Mbaaxi Lislaam ak yokkute gu sax dàkk jaare ko ci njàngalem Seydinaa Limaamu Laay ».