Ci bis bi jiitu Bis bi ñu jagleel Senegaal ca « Exposition universelle » Osaka-Kansai 2025, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, amal na, donte xatoon na lool, am ndaje diggam ak PME ak PMI yi doon teewal Senegaal.
Njiitu Réew mi rafetlu na seen taxawaay ak seen dogu, jaare ko ci fàttali waar wu am solo wi ñu am ci tabax réew mi ak jëmmalug « Vision Sénégal 2050 ».
Feddali na yéeney Ngóornamaŋ bi jëm ci gunge ak taxawu sektéer piriwe bi, nga xam ne mooy dëgg-dëggi Kenob yokkute, sos ay xëy ak fent, ngir tabax koom mu am doole mu man a joŋante ci kanamu àddina si te ñoŋ.
Ndaje mii nag day wane pas-pas bu leer : ëllëgu Senegaal ci ànd ak doomi réew miy jéem a taxawal dara ak këri liggéeyukaayi réew mi rekk lañu koy tabaxee.