Peresidaa FAY bawoo na Ndakaaru jëm ci tukki nemmiku bu muy amal ca Japon.

Biti Réew - 18 MONTHS.AUGUST 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY bawoo na Ndakaaru tay ci suba si wutali Japon ga mu war a amal tukkib nemmiku, 18 jàpp 26i fani ut 2025.

Ci tukki bii, Njiitu Réew mi dina teew ca 9eelu Ndaje mu mag ma ñuy amal ca Tokyo ci suqalikug Afrig (TICAD 9), dina teewe itam Bis bi ñu jagleel Senegaal ca “Exposition universelle” Osaka Kansai 2025.

Muy tukki bu jëm ci gën a feddali lëkkaloo gu am solo gi dox diggante Senegaal Tokyo, te lalu ci mbaax yu ñu bokk.