xamle - 24 MONTHS.DECEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dalal na tay ci talaata ji 24i fani mars 2024, Omar Kan, ñu koy woowe Rëg-Rëg keleŋu àddina si ci MMA ak Muhammet Tafsiir Ba, keleŋu àddina si ci kick-boxing. Ñoom ñaari jàmbaar yii nag yéegal nañu leen ci dayob « Chevalier de l’Ordre du Mérite » ndax seen jaar-jaar yu am solo te mat a roy ak seen ug dogu ci yékkati raaya réew mi ci kanamu àddina si.
Ci jataay bu màgg bii, Peresidaa Fay fésal na mbégteem ak cofeelam ci ñaari keleŋ yii, nga xam ne wane nañu seen bopp ci kanamu àddina si. « Seen ndam lii royukaay la ci ndaw ñi te it màndarga la ci xereñteg Senegaal », di li mu xamle.
Yéeney Njiitu Réew mi nag mooy jaare ci ñoom ñii ngir sargal mbooleem way-tàggat yaram yiy yëngu ci wàllu xeex, jaare ci tamit feddali njàppaleg Nguur gi jëme ci ñoom. Xamle na njariñal tàggat yaram ci man a boole ak siggil réew mi, teg ci feddalil leen ne Ngóornamaŋ bi dina wéyal tabax yi muy amal ci wàll wi ngir ag yokkuteem ak jëmam kanam.
Ñoom ñii ñu doon sargal nag te mbégte mi doon feeñ ci seen i xar-kanam, sant nañu bu baax Njiitu Réew mi ci yëg gi teg ci feddali seen ug jaayante ci teewal Senegaal ci ngor fépp fu ñuy woote tàggat yaram ci àddina si.
Mu doonoon jataay bu safoon sàpp ci màggal ak delloo njukkal, di wane rekk jaayanteg Senegaal ci dooleel ak taxawu ay doomam ci wàllu tàggat yaram.