xamle - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ci 79eelu Ndaje Mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si, Njiiti Réew mi Basiiru Jomaay Fay a ngi wéyal ndajey lëngoo yi. Dalal na tay
Dick Schoof, Njiital Jëwriñ lu Péyi Baa.
Waxtaan yaa ngi jëmoon ci dooleel lëkkaloog ñaari réew yi ci pàcc yu am solo, rawati na ci mbay mi, yasara yi ak saytu gu sax ci ndox mi.