xamle - 28 MONTHS.NOVEMBER 2024
Ginnaaw ba Ndiisoog Ndayi Sàrti Réew mi dëggalee, àllarba 27i nowàmbar 2024, njureef yi bawoo ci joŋantey lesislatiif yu 17i fani nowàmbar 2024, Njiitu Réew mi torlu na dekkere limtu 2024-3290 bu 28i fani nowàmbar 2024, biy jàpp altine 2i fani desàmbar 2024 lélub tijjitel jataay bu njëkk bu Ngombalaan gi ñu fal yees.
Njéndel Réew mi, 28i fani nowàmbar 2024
Jëwriñ-Xelalekat, Farbay Njénde li Useynu Li