jëwriñ - 27 MONTHS.FEBRUARY 2025
Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dina jiite xewu daloo Barabu Jëmmal dundug Yónnent bi, Muhammat (SLHWS) ak Xeyteg lislaam, ci teewaayu kilifay laamisoo yi, yu aada yi ak yu diine yi, alxemes 27i fani féewarye 2025 ca ëtt ba dox diggante « Grand Théâtre » ak Barabu Jëmmal Xaytey ñuule yi.
Barabu Jëmmal bii, Réewum Araabi Sawudit maye jaare ko ci Lig Islaam, mooy bi njëkk ci Afrig Sowu Jant .