Biti Réew - 07 MONTHS.DECEMBER 2024
Amal nañu tay, 7i fani desàmbar 2024 , tijjitel 22eelu Ndajem Waxtaan mu Doha, ci teewaayu Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay. Xew-xew bii war a wéy ba 8i fani desàmbar, dees na fa waxtaane tomb yu am solo yu mel ni doxaliinu àddina si ak kaaraange. Ndaje mii, ñuy dàkkantalee « Laamisoo, Disoo, Wuute », dina dajale ay kilifa ci àddina si, ñu war a yaatal ci jafe-jafey jamono ji boole ko ak teg ay politig ak digle yu jëm ci amal jëf yu wér.
Ci ndaje mii, Peresidaa Fay séq na ci ab jataay diggam ak Emiir bu Kataar, di Seex Tamim Ben Hamad Al Saani, niki noonu Njiital Jëwriñ ak Jëwriñu Jëflante ak Biti Réew ju Kataar, Seex Mohammet Ben Abdu Rahmaan Al Saani. Waxtaan nañu ci lëkkaloog ñaari réew yi ak tombi lëngoo yu bees yu ñu namm a amal ci wàllu politig, koom ak laamisoo.