Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY delloo na njukkal 11i ma-réewi Senenegaal, yu bawoo ci maas yu wuute ndax taxawaay bu mucc ayib bi ñu wane ci bëccëgi SETAL SUNU RÉEW. Raaya yii ñu leen jox ci jataay bu am solo, day wane njukkal lu kawe li Njiitu Réew di delloo mbooleem saa-senegaal yi nga xam ne ñu ngi takku weer wu jot ngir setal pénc mi ak sàmm sunu kéew.
Ci sargal gii, Njiitu Réew mi day feddali ag jaayanteem ci Senegaal gu set, jàppoo te sàmmonte ak kéew mi. Takku taxawug ma-réew yi yamul rekk ci jëfi kese: keno bu wóor la ngir tabax ëllëg gu sax te tegu ci àndandoo jëf ak xam sa wareef. Nanu àndandoo wéy ci jëf ngir man a bàyyil maas giy ñëw ëllëg Senegaal gu méngoo ak seen yaakaar.