NDIISOOG JËWRIÑ YI - 18 MONTHS.JULY 2024
NDIISOOG JËWRIÑ - 18i SULET 2024
Njiitu Réew mi jiite na, ci alxemes ji 18i fani sulet 2024, ndajem jëwriñ yi ñuy amal ayu-bis bu set ca Njénde la.
Ci ndoortel ay kàddoom, Njiitu Réew mi yeesal na ay ndokkaleem ak i ñaanam jëm ci Umma Islaam bi rawati na julliti Senegaal yi ci màggal bisu Tamaxarit gi (Aasuuraa).
Njiitu Réew mi sant na bu baax teg ci feddali kóoluteem jëme ci Ilimaani Jëwriñ ji ak mbooleem Jëwriñ yi ak sekkreteer detaa yi ci liggéey bu mucc ayib bi ñu amal, diirub ba ñu leen sampee ak leegi, jëm ci ni ñuy taxawoo yitte yu jamp yi ci wàllu koom ak dunduin ak jëmmal SÉMBU soppi doxaliin bu wér ci Senegaal. Fàttali ba Ngornamaa bi, ag dogoom gu sax ci def lépp lu mu man ngir sottal, ànd ko ak njàppaleg askan wi, ci Senegaal gu moom boppam, jub te naat.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñ ju Njëkk ji mu gën a baral jéego yi jëm ci taxawal yeesal yi war ngir sellal finaas piblig yi ak joyyanti doxaliinu nguur gi. Ci loolu, soññee na ci ñu fexee aar ak suqali koom mu ay reenam sampu ci réew mi jëm ci naataange ak suqalikug dund gi ci lu sax. Ci wàll woowu, woo na Ngornamaa bi ñu gën a taxaw ci topp jëfe gu matale ci dogal yi ñu jël jëm ci wàññi njëgu dund bi ak yenn ci yi ëpp ci li askan wi di jëfandikoo waaye tamit taxaw temm ci fexee peeg ba li ñuy soxla ci wàllu dund ak njafaan ci réew mi bañ a dog.
Njiitu Réew mi soññ na Jëwriñ ju Njëkk ji mu taxaw temm ànd ko ak Jëwriñ yi mu soxal, rawati na ñi yor wàllu Soroj, Koom mi ak Yaxantu gi, ci di topp bis bu set ni ñuy jëfandikoo sunu petorol bi ak gaas bi jaare ko ci taxawal jumtukaay yu mucc ayib ngir saytu ak njaayum liy génne ci tooli njafaan yooyu.
Njiitu Réew mi xamle na ne ñaareelu xaaju 2024 bii dafa war a dëgëral pàcc bu am solo ci tabaxaat, joyyanti, yeesal yu xóot ci politig piblig yi ak càmbar yoriin yi (reddition des comptes). Jubluwaay bi mooy taxawal ci mbooleem wànqaas yi ci wàllu koom, dundiin, kéew mi ak mbatiit, taxawaay yi war dëgg ngir tabax ci lu sax moom sa bopp bu wér ci doxal demokaraasi bu ñuy roy ak Réewum yoon mu ñuy tegtaloo. Ci loolu, soññ na Ngornamaa bi ñuy gën a may nopp askan wi, di fuglu tey jàppalante ci seen liggéey, jaare ko ci amal pexey caabal (communication) gu déggoo, yenu maanaa, leer, wér te wóor. Ci loolu sax la sàkkoo ci Njiital Jëwriñ li mu jël mbooleem matuwaay yi jëm ci aajar ci fan yii di ñëw ci kanamu Ngomblaan gi “Déclaration de Politique générale” bu Ngornamaa bii jàppandi ba noppi.
Ba muy àddu ci lu soxal politig yu yees yi jëm ci jote ci dëkkuwaay, Njiitu Réew mi fàttali na ne jafe-fafe saytu luyaas bi ak tabax dëkkuwaayu ndimbal bir yu jamp lañu ci soxlay askan wi. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ ji mu sóobu, ca na mu gën a gaawee, ànd ko Jëwriñ yi mu soxal ak mbootaayu way-jëfandiku yi, xayma jumtukaay yi ñu teg ngir jaarale yoon njëgi luyaas yi sukkandiku ko ci gox yi.
Njiitu Réew mi fésal jamp gi nekk ci amal tënk bu matale ci tolluwaayu doxal sàrt 2016-31 bu 08i nowàmbar 2016 bi jëm ci sàrtub doxaliin ci dëkkuwaayu ndimbal yi, saytug dëkk yu bees yi ñu taxawal, niki noonu sémbi tabax dëkkuwaayi ndimbal yi ñuy amal ci mbeerayu réew mi. Ci jubluwaay boobu, xamal na Jëwriñu Dëkkuwaay ji ak Jëwriñi Càmm gi ci wàllu tabax ak dëkkuwaay, solos gën a dooleel
SICAP SA ak SN HLM ci li sas wi ñu leen jox ngir njariñu pénc mi jaare ko ci taxawal doxaliin wu yees te xereñ ngir jàppandi dëkkuwaayi ndimbal yi Càmm gi teg sukkandiku ko ci amal ay Pasi Jubluwaat ak Jumtukaay yu wér boole ko ak gis-gisu mbeeraay gu am doole.
Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñ Ju Njëkk ji mu gaar sémb wu yees ci suqali dëkkuwaayi ndimbal yu tegu ci yoon te dugalaale dogali galag, suuf ak koppar yu xemmeemu te sax ngir yombal jot ci dëkkuwaay ak moomeel ci wàllu suuf ak dëkkuwaay. Jubluwaay boobu ci politigu dëkkuwaay dafa war a dooleel tabaxug kër yu jekk te méngoo ànd ak teg doxaliin wu leer, dale ko ci tege sas yu fullawu, fàkkug suuf si ak yokk doole bu baax yënguy kër giy saytu fàkkug suuf si ak yeesal dëkk yi (SAFRU).
Ci wàll woowu ba leegi, Njiitu Réew mi fàttali na Jëwriñ yi yor wàllu Suuf yi, Biir Réew mi, Gox ak Gixaan yi ak Tabax ak Dëkkuwaay, solos sumb ay waxtaan ànd ko ak fara yi ak kilifay dëkk yi ngir baral jéego yi ci sottal kadastar gi, peeg suqalikug dëkk yu bees yi ak teg ay yoon yu ñu dëppoo jëm ci joyyantiwaat bokk-moomeel yi ak yeesal dëkk yi.
Njiitu Réew mi xamle na tamit soxlay fésal ak taxawu koperatifi dëkkuwaay yi ngir suqali tabaxug dëkkuwaay yu yees boole ko ak rawati na fexe ba boole ci bayéer yi ak taxawal koppar yu ñu jagleel dëkkuwaayi ndimbal yi ak sóob ci bu baax kër yii di CDC, BHS ak yeneen kuréli kopparal yiy yëngu ci wàllu dëkkuwaay.
Njiitu Réew mi woo na Jëwriñ ju Njëkk ji mu jël mbooleem matuwaay yi war ngir yombal bu baax yoon yi ñuy jaar ngir am ndigalu tabax ngir baral jéego yi ci dooraat tabaxug dëkkuwaay yi waaye tamit gën jagal taxawaayu ñiy yëngu ci wàllu tabax ci géewu liggéey ak xëyu ndaw ñi. Ci noonu sàkku na ci Jëwriñ ju Njëkk ji mu amal ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, ag Ndiisoo diggante jëwriñ yi jëm ci wàllu dëkkuwaay ngir man a am taxawu gu mucc ayib ci politig yu yees yi ñeel saytu luyaas yi ak fésal dëkkuwaayi ndimbal yi.
Ci loolu, Njiitu Réew mi fésal na solos amal ay xalaat yu xóot ci ni ñuy rëddee sunu dëkk yi ak bokk-moomeel yi. Fàttali na yitte ji mu jox ci sàmmonte ak yooni dëkkuwaay, rëdd ak saytu tabax yi. Mu mujj ci sàkku ci Jëwriñu Gox ak Goxaan i, Dëkkuwaay ak daggug mbeeraay yi mu sóobu, ci na mu gën a gaawee, ci xalaat ànd ko ak kuréli rëddkat yi ak ñeneen ñiy yëngu ci wàll wi, ngir amal ay diisoo yu jëm ci wataane ni ñuy rëddee sunu dëkk yi ak bokk-moomeel yi.
Ci ndoortel ay kàddoom, Jëwriñ ju Njëkk ji jottali na Njiitu Réew mi ndokaaley Ngornamaa bi ci doxaliin wu xereñ wi mu amal ngir leeral PROJET bi ci jataay bu askan wépp rafetlu, mu séqoon ko ak taskati xibaari réew mi, gaawu 13i sulet 2024, ci lu soxal 100i fan yu njëkk yi mu def ci boppu réew mi.
Ba muy àddu ci jafe-jafey bindug ñi am BAC yees ci Jànguney Senegaal yi, Jëwriñ ju Njëkk ji gis na ne lu manul a ñàkk la ñuy bàyyi xel ci fexe méngale dogali bindu yi ak taxawaay ak tànneefi ñi am BAC niki noonu dooleel jumtukaay ak ay dëkkuwaay ci tund yi ngir féexal Jànguneb Seex Anta Jóob bu Ndakaaru. Fésal itam warefu taxawal aw doxaliin ngir man a am lu leer ci ni ñuy joxee bursu yi ak néeg yi ñeel njàngaan yi ci dëkkuwaay yi.
Ci lu soxal topp joxoñi Njiitu Réew mi ci jamonoy awril-suwe 2024, Jëwriñ ju Njëkk ji leer na ne wànqaas yi nekk ci njëwriñ yépp, amal nañu ci anam yu mucc ayib, ci bir yi jëm ci tolluwaay bi ñu fekk sémb yi, naal yi ak seen i liggéeykat. Di li yombal ñu manoon a gaaw ci door càmbar yi. Fésal na itam, te bég ci lool nag, jéego yi wànqaas jëwriñ yi teg jëm ci saafara jafe-jafe yu jamp yi soxal ku ci nekk ci li la soxal. Sóob na Jëwriñ yi ñu taxaw temm ngir waajal sémb ak bind yi jëm rawati na ci yoolekat yi ci warabi liggéeyukaay yu kawe yi ci pénc mi. Sàkku na itam ñu gaaw matal wayndare wi ñeel way-loru ñi ci xew-xewi sãawiye 2021 ba féewarye 2024 ak dalu web bu ñu jagleel dajale man-mani saa-senegaal yi ak gis-gis yi ci sémb yi.
Ci geneen wàll, Jëwriñ ju Njëkk ji xamal na Ndiisoo gi ne jot na tënk bu njëkk bi bawoo liggéey yi kurél gi ñu dénkoon ñu càmbar suufi pénc mi ci tefesu Ndakaaru doon amal, ngir delloo ma-réew tefes yooyu ak sàmm kéew mi. Tënk bu mujj bi dees na ko jébbal Njiitu Réew mi.
Mu daaneel moom Jëwriñ ju Njëkk ji àddu ci lootaabe joŋanteb dugg ca ENA ci atum 2024. Sàkku na ci Jëwriñ, Jëwriñ Ju Rëy ju Ngornamaa bi, Jëwriñ yi mu soxal ak ndoxalug ENA ñu sóobu ci ay waxtaan yu jëm ci xool nees di yokkee limub ñi ñuy jël ak ay gaaral ngir yeesal ENA. Jubluwaay bi di yokk liggéeykat ci ndoxal gi ngir taxawu gu mucc ayib ci yeesal yi manul a ñàkk ngir soppiku gu matale ci doxiinu Senegaal.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
Jëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg suuf si ak jawwu ji àddu na ci jafe-jafe yi am ci daxaliinu jëfandiku ak toppatoog TER bi ci jubluwaayi waxtaanewaat pas yi;
Jëwriñu Kéew mi ak Soppiku ci Ekolosi àddu na ci yoon wi ñu teg jëm ci def Lag Róos ab “réserve naturelle urbaine” ;
Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi def na leeral ci tolluwaayu “Programme national de Bourses de Sécurité familiale” ak “Registre national unique”.
LU SOXAL CI BINDI SÀRTAL AK YOONAL
Ndiisoo gi càmbar ba teg nangu:
Sémbu dekkere wi jëm ci tere yënguy mbell ak joxe ndigalu jëfandiku ci gox bi féete ak dexu Faleme;
Sémbu dekkere wi jëm ci taxawal anami doxal ak yeesal pexe yi jëm ci wàññi njëg yi ci wàllu mbëj gi.
CI DOGALI BOPPAM YI:
Njiitu Réew mi jël na dogal yii:
NJÉNDE LI:
Sëriñ Seex Ahmed Bàmba JAAÑ, jàngalekat ca UCAD, tabb nañu ko Njiital Kurél giy saytu wàllu soroj ak gil (FOS-PETROGAZ), mu wuutu Sëriñ Maalig SAll;
NJËWRIÑ GU NJËKK GI
Sëriñ Moor FAAL, Inspecteur général d’Etat, tabb nañu ko Njiital daara ji ñuy tàggatee way-ndoxal gi (ENA), mu wuutu Sëriñ Muhammadu Lamin JÀLLO;
Sëriñ Maam Góor NGOM, am lijaasab maitrise ci wàllu saabal, tabb nañu ko njiital Pekk bi yor wàllu xibaar ak saabalu ngornamaa bi (BIC-GOUV);
Sëriñ Birom Holo BA, am lijaasab doktoraa ci optimisation et sûreté des systèmes, tabb nañu ko Njiital Pekk biy lëkkale ak a topp Sémb yi ak Naal yi.
NJËWRIÑU YASARA SOROJ AK MBELL YI
Sëriñ Maysa JAXATE, di agrégé ci fakilte droit, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Ndoxal gu Koppar yi ñu jagleel taxawu pàccub Yasara gi, mu wuutu Sëriñ Seexunaa AAN.
Sëriñ Paab Moktaar SAAR, Ingénieur centralien, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu SAR, mu wiutu Sëriñ Ceerno NJAAY;
Sosef Sàmbeseen JAATA, Amadagunduŋ ci jànguney xew-xam yi, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog ndoxal gu PETROSEN Holding, mu wuutu Ayméeru ÑING;
Sëriñ Seex BITEY, am lijaasab master ci ndoxalug lijjanti yi, tabb nañu ko Njitu Ndiisoog ndoxal gu kër giy saytu wàllu mbëj ci kaw gi (ASER), toogu bu kenn newutoon;
Sëriñ Aadama JAAWARA, Jàngalekatu mboor ak melo-suuf, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog saytu gu ANER, mu wuutu Sëriñ Abdulaay SI;
Sëriñ Paab Momar LÓO, xereñtaan ci wàllu mbëj, tabb nañu ko Njiital Lënkaayu gilu Senegaal (RGS SA), mu wuutu Sëriñ Sosef Ufame MEDU;
Sëriñ Seex Mulaay Idriis FAAL, xereñtaan ci wàllu mbëj, tabb nañu ko Njiital Mbëj gi, toogu bu kenn newutoon;
Sëriñ El Haaji NJAAY, am doktoraa ci wàllu yasara yi ñuy yeesalaat, tabb nañu ko njiital suqalikug yasara yi ñuy yeesalaat, mu wuutu Sëriñ Demba GAY;
Soxna Ummu Xayri JÓOB, am lijaasab master ci wàllu koom, yoonal ak yasara, tabb nañu ko Njiital Yasara gi, toogu bu kenn newutoon;
Sëriñ Fidel Jisibon JËMMÉ,
Ingénieur électromécanicien, tabb nañu ko Jëwriñ ju rëy ca kër giy saytu mbëj gi ci kaw gi (ASER), toogu bu kenn newutoon;
ÑJËWRIÑU JUMTUKAAY YI AK YAALEG SUUF SI AK JAWWU JI
Sëriñ Taahir NJAAY, xelalekat ci àddina si ci wàllu yaaleg jawwu ji, tabb nañu ko Njiitu Ndiiaoog Ndoxal gu kërug 2AS, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima JNAAY;
Sëriñ Njóogu NJAAY, Inspecteur principal de l’aviation civile, tabb nañu ko njiitu Ndiisoog saytu kërug ANACIM, mu wuutu Sëriñ Mammadu Mustafaa JEŊ;
Sëriñ More Taala NJAAY, Ingénieur en génie civil, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Saytu AGEROUTE, mu wuutu Sëriñ Mammadu Móori JAW;
Sëriñ Baara SOW, am master ci wàllu kopparal, càmbar am saytu doxaliin, tabb nañu ko Njiital koppar yi ñu jagleel suqalikug yaaley suuf si (FDTT), mu wuutu Sëriñ Baabakar GAY;
Sëriñ Mammadu GUJAABI, kàngam ci wàllu yaale, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog ndoxal gu Dakaar Dem Dikk, mu wuutu Sëriñ Habiibu TIMBO;
Sëriñ Usmaan JAAÑ, am master II ci wàllu yoonu koom, tabb nañu ko njiitu Ndiisoog ndoxal gu FERA, mu wuutu Sëriñ Paab Songde JÓOB;
NJËWRIÑU KÉEW MI AK JÀLL CI EKOLOSI
Sëriñ Maadi BÀCCILI, Administrateur civil, tabb nañu ko Jëwriñ ju Rëy ju kërug jëmbat naatal ak nëtëxal gi (ASERGMV), mu wuutu Sëriñ Mawdo NDAW;
NJËWRIÑU TÀGGATU GU XEREN GI
Sëriñ Seex Muhammadu MBAY, jàngalekat, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu ONFP, toogu bu kenn newutoon;
Sëriñ Muhammadu Maxtaar JA, Jàngalekat-Amadagunduŋ, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog ndoxal gu CNQP, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima NDUUR;
Sëriñ Maalig SI, kàngamu ndoxal gu leŋ, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu ANAMO, mu wuutu Sëriñ Fosaar Bàndiŋ SUWAANE;
Sëriñ Demba JUM, xereñtaan ci wàllu systèmes ak réseaux, tabb nañu ko Njootal ANAMO, toogu bu kenn newutoon;
NJËWRIÑU NDOX MI AK YOONI NDOX YI
Sëriñ Ahmad Iyaan AOW, Amadagunduŋ ci wàllum paj, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu OLAC, mu wuutu Sëriñ Suleymaan Barka BA;
NJËWRIÑU NAPP GI AK JUMTUKAAYI GÉEJ YI AK WAAX YI
Sëriñ Ismaayla NJAAY, xereñtaan ci wàllu napp ak yar ci ndox, tabb nañu ko Njiital Nappi géej yi, mu wuutu Sëriñ Jéen FAY;
Sëriñ Ahmadu Tiijaan KAMARA, xereñtaan ci wàllu napp ak yar ci ndox, tabb nañu ko Njiital kër giy tàggat way-xarala ci napp gi ak yar ci ndox (CNFTPA), mu wuutu Sëriñ Samuel Waali FAY;
Sëriñ Muhammadu Nguuda MBUUB, jàngalekat-gëstukat, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxalu Poor bu Ndakaaru, mu wuutu Sëriñ Muusaa SI;
NJËWRIÑU DËKKUWAAY GI, GOX AK GOXAAN YI AK DAGGUG MBEERAAY GI
Sëriñ Abdu Xaadir FOFANA, am lijaasab maitrise ci wàllu melo-suuf ak xaralag melo-suuf, tabb nañu ko Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu kër giy saytu mbuubit yi (SONAGED), mu wuutu Sëriñ Taala SIISE;
Sëriñ Ibraahiima JÓOB, Càmbarkat ci wàllu koppar, tabb nañu ko Doxalkatu koppar yi ñu jagleel dëkkuwaayi ndimbal yi (FHS), mu wuutu Sëriñ Usmaan WÀDD;
Sëriñ Asan JÓOB, am lijaasab Licence ci wàllu comptabilité publique, tabb nañu ko njiitu Ndiisoog Ndoxalug SAFRU, mu wuutu Sëriñ Góor GI SIIS;
Sëriñ Koso SEEN, xereñtaan ci wàllu agronomi, tabb nañu ko njiitu Dëkkuwaay gi ak Cetug pénc mi, mu wuutu Sëriñ Aliw Badara LI;
NJËWRIÑU PAJ MI AK NEKKIINU ASKAN WI
Sëriñ Àlliyun Ibnu Abu Taalib JUUF, Garabalkat, tabb nañu ko Njiital kër giy saytu yoonu garabal (ARP), mu wuutu Soxna Ummi Kalsuum Njaay NDAW;
Sëriñ Mammadu JÓOB, amadagunduŋ bu ràññiku ci wàllu anatomi ak organogénèse, tabb nañu ko Njiital kër giy saytu wàllu ngal bu Jamñaajo;
Sëriñ Abdalaah WÀDD, suruseñ ci paj mu jamp, tabb nañu ko Njiitu SAMU, mu wuutu Amadagunduŋ Mammadu Jaara BÉEY;
Suruseñ-kolonel Bekaay FAAL, Amadagunduŋ bu ràññiku ci garabal, tabb nañu ko Njiital Laboratoires yi, mu wuutu Sëriñ Aamadu Muktaar JÉEY;
Sëriñ Bukar JUUF, Suruseñ, tabb nañu ko njiital DGAS, mu wuutu Soxna Aram Toob SEEN;
Sëriñ Fàllu ÑAŊ, Suruseñ, tabb nañu ko Njiital Raglub Tund bu Koldaa, mu wuutu Sëriñ Jibriil YANSAANE;
Sëriñ Yoro JAAÑ, Doktoor ci wàllum paj, am lijaasab saytu warabi fajukaay yi, tabb nañu ko Njiital raglub Abdul Asiis SI DABBAAX bu Tiwaawon, mu wuutu Binta Jóob BAJAAN;
NJËWRIÑU MBAY MI, MOOM SA BOPP CI LI NGAY DUNDE AK CÀMM
Sëriñ Séemu Paate JUUF, di ku xereñ ci wàllu saytu ay sémb di xereñtaan ci doxaliinu mbay, tabb nañu ko Njiital ANIDA, mu wuutu Aliw LEKOOR;
Sëriñ Alasaan BA, xereñtaan ci wàllu mbay, tabb nañu ko Njiital kër giy saytu fàkk ak jëfandikoo suufi Deltaa bu Dexu Senegaal ak Wale bu Dexu Senegaal ak Faleme (SAED), mu wuutu Sëriñ Abuubakri SOW;
Sëriñ Mustafaa GÉY, am lijaasab doktoraa ci wàllu defar ak aar gàncax yi, tabb nañu ko Njiitu Daara ju kawe ji ci gëstu wàllu mbay (ISRA), mu wuutu Sëriñ Momar Taala SEKK;
Sëriñ Mbay Silla XUMMA, xereñtaan ci wàllu agronomi toropikaal, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Ndoxal gu ISRA mu wuutu Sëriñ Ngañ SEEN;
Sëriñ Usmaan SILLA, Waññikat, tabb nañu ko Njiital DAPSA, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima MÉNDI;
Sëriñ Bunaama JÉEY, xereñtaan ci wàllu ndox, tabb nañu ko Njiital kër giy saytu Jumtukaayi mbay mi ci kaw gi mu wuutu Sëriñ Umar SAANE;
Sëriñ El Haaji FAY, Sosolog, tabb nañu ko Njiital ANCAR, mu wuutu Soxna Mariyaama Daraame;
Sëriñ Mammadu SIISOXO, kàngam ci wàllu mbay, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog ndoxal gu ANCAR, mu wuutu Mammadu KAMARA;
Sëriñ Taahaa SOW, doxalkatu kërug lijjanti, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog ndoxal gu SONACOS, mu wuutu Sëriñ Yuusu JÀLLO;
Sëriñ Seex Ahmadu Bàmba NGOM, Agro-économiste, tabb nañu ko Njiital PRODAC, mu wuutu Sëriñ Jimo SUWAARE;
Sëriñ Abdu Mbàkke SÀMB,Jàngalekat, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Saytu PRODAC, mu wuutu Sëriñ Ahmet Tiijaan JEŊ;
Sëriñ Móodu Géy SEKK, ma-koom, saytukatu sémb, tabb nañu ko Njiital kopparal ak lëkkaloo ak Mbootaay yi, mu wuutu Sëriñ Sers MALU;
Sëriñ Alfred Kuli SEEN, kàngam ci xam-xamu suuf, tabb nañu ko njiital INP, mu wuutu Sëriñ Mammadu SOW;
NJËWRIÑU KOPPARAL GU NDAW GI AK KOOMUM JÀPPAL MA JÀPP
Soxna Mariyaama JEŊ, Sosolog, tabb nañu ko Njiital koomum Jàppal ma jàpp, toogu bu kenn newutoon;
Sëriñ Seydinaa Umar NJAAY, ma-koom, tabb nañu ko Njiital Stratégies ak Prospective, mu wuutu Sëriñ Mohammed JÓOB;
Sëriñ Demba CAAM, Jàngalekat ci njàng mu digg-dóomu mi, tabb nañu ko Njiital Ndiiaoog jubluwaayu koppar yi ñu jagleel Kopparal gu ndaw gi, mu wuutu Ismaayla DEMBELE ;
NJËWRIÑU NDAAMAARI GI AK FENT GI
Soxna Sooda JARA, kàngam ci wàllu fésal ak saytu ndaamaari gi, tabb nañu ko Njiital Fésal ndaamaari gi, mu wuutu Sëriñ Mohammadu Manel FAAL;
Soxna Mari Ndey Ñilaan JUUF, ma-koom, tabb nañu ko Njiital Fent gi, mu wuutu Sëriñ Ahmadu SAAR;
Sëriñ Haadi TURE, kàngam ci wàllu kontaabilite ak koppar, tabb nañu ko Njiital Taxawu ak Soppikug Këri lijjanti yi fasuwut, mu wuutu Sëriñ Mammadu JIITE;
Soxna Sofi Nsingaa SI, kàngam ci wàllu rëdd, tabb nañu ko Njiital Kërug fésal ak suqali fent gi (APDA), mu wuutu Sëriñ Pàppa Hammadi NDAW;
Sëriñ Biram SAAR, kàngam ci wàllu ndaamaari, tabb nañu ko Njiital daara jiy tàggat ci wàllu dalluwaay ak ndaamaari, mu wuutu Sëriñ Muusaa COOR;
Sëriñ Sisaawo JAANE, Jàngalekat ci njàng mu digg-dóomu mi, tabb nañu ko Niital Ndiisoog saytu kërug fésal ak suqali fent gi, mu wuutu Sëriñ Mammadu SIISOXO;
Sëriñ Elhaaji Maaog MBAY, kàngam ci wàllu ndaamaari, tabb nañu ko Jëwriñ ju rëy ju kër giy fésal ndaamaari gi, mu wuutu Sëriñ Mammadu JÀLLO;
Sëriñ Ibraahiima TAAL, ma-koom Waññikat, tabb nañu ko Lëkkalekatub Sémbu Mobilier national, mu wuutu Sëriñ Saalum NJAAY;
NJËWRIÑU NDEFAR GI AK YAXANTU
Sëriñ Mammadu KULIBALI, am lijaasab master ci wàllu xereñteg kopparal, tabb nañu ko Njiital SEMIG, mu wuutu Soxna Faatumata ÑAŊ;
NJËWRIÑU YOON
Sëriñ Alasaan GÉY, am lijaasab doktoraa ci koppar ak koom, tabb nañu njiital Doxaliin wu baax, mu wuutu Sëriñ Aaróona SAAR;
JËWRIÑU NJÀNG MU KAWE MI
Sëriñ Àlliyun SEEN, xereñtaan ci wàllu seni siwil, tabb nañu ko Njiital toppatoo tabax ak jumtukaayi Njàng mu kawe mi, mu wuutu Sëriñ Ahmadu Bàmba FAAL;
Sëriñ Àlliyun SEEN, Jàngalekat-gëstukat, tabb nañu ko njiital CROUS bu Jànguneb Àlliyun Jóob bu Bàmbey, mu wuutu Sëriñ Mustafaa GÉY;
Sëriñ Sãa Améde JAATA, Lijaasab gëstu gu xóot ci sociologie, tabb nañu ko Njiital Bursu yi, mu wuutu Sëriñ Xalifa GAY;
NJËWRIÑU KOPPAR YI AK NJËL LI
Sëriñ Faraasuwaa NJAAY, inspecteur bu kadastr, tabb nañu ko njiital kadastr, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima AAW;
JËWRIÑU BIIR RÉEW MI AK KAARAANGEG PÉNC MI
Sëriñ Biram SEEN, Àttekat, jiite woon lu ko jiitu tàggatu ak saabal ca pekk biy saytu joŋantey pal, tabb nañu Njiital Pal yi (DGE) mu wuutu Sëriñ Candeela FAAL;
Sëriñ Usmaan NGOM, kàngam ci wàllu jokkalante yawi pénc mi, koppar ak saytug pénc mi, limatu payoor l° 624 961/D, tabb nañu ko Njiital Ndoxal ak jumtukaay ca Njëwriñu Koom, Palaŋ ak Lëkkalekoo, mu wuutu Maalig SAAR mi ñu soxla ci yeneen liggéey;
Sëriñ Layti MBENG, am lijaasab master ci Kontaabilite ak saytug koppar, limatu payoor l° 625 060/O, tabb nañu ko Njiital Ndoxal ak Jumtukaay ca Njëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu ak fent lu yees;
Soxna Ndey Yaasin GÉY, Doktoor ci wàllu koomum Njàng, limatu payoor l° 677 090/O, jiite woon lu ko jiitu Ndoxal ak Jumtukaay ca Njëwriñu Njàng mi, njàng mu kawe mi, Gëstu ak fent lu yees, tabb nañu ko Njiital Ndoxal ak Jumtukaay ca Njëwriñu Njàng mi;
Sëriñ Sãa Luwi Benuwaa MBAY, Jàngalekat ci njàng mu digg-dóomu mi, limatu payoor l° 666 139/A, tabb nañu ko Njiital Ndoxal ak Jumtukaay ca Njëwriñu Foŋsoo Piblig ak yeesal Sarwiis Piblig, mu wuutu Soxna Maam Xadi Siidi Aali BAAJI mi ñu soxla ci yeneen liggéey;
Sëriñ Mammadu Mustafaa JÀLLO, kàngam ci wàllu saytu sémb ak Koppari pénc mi, limatu payoor l° 634 436/Z, tabb nañu ko Njiital Ndoxal ak Jumtukaay ca Njëwriñu Ndaamaari gi ak Fent gi, mu wuutu Sëriñ Ma-Njaay JÓOB mi ñu soxla ci yeneen liggéey ;
Soxna Faatu JUUF, Jàngalekat ci Njàngum digg bi, limatu payoor l° 661 673/A, tabb nañu ko espektëer ci biri ndoxal ak koppar ak Njëwriñu Njàng mi;
Sëriñ Ibraahiima Ngom, xelalekat ci ci biri mbatiit, limatu payoor l° 611 781/F, tabb nañu ko espektëer tegnig ca Njëwriñu Ndaw ñi, Tàggat yaram ak Mbatiit;
Sëriñ Duudu SÀNQARE, espektëeru Njàngum pénc mi, Ndaw ñi ak Tàggat yaram, limatu payoor l° 632 100/D, tabb nañu ko espektëer tegnig ca Njëwriñu Ndaw ñi, Tàggat yaram ak Mbatiit;
Sëriñ Omar Ben Xattaab DANFAXA, Xelalekat ci biri mbatiit, limatu payoor l° 600 620/B, tabb nañu espektëer tegnig ca Njëwriñu Ndaw ñi, Tàggat yaram ak Mbatiit;
Sëriñ Móodu MBAY, xereñtaan ci wàllu Fent, kàngam ci xam-xamu ndundat, Wér gi yaram ak Kéew, limatu payoor l° 515 420/G, lu ko jiitu mu doonoon espektëer tegnig ca Njëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante, tabb nañu ko espektëeru Biri ndoxal ak koppar ca Njëwriñu Kopparal gu Ndaw gi ak Koomum Jàppal ma jàpp ;
Sëriñ Maalig CAAM, ma-yoonal, limatu payoor l° 715191/R, tabb nañu ko espektëer tegnig ca Njëwriñu Kopparal gu Ndaw gi ak Koomum Jàppal ma jàpp ;
Jëwriñu Tàggatu gu Xereñ gi, Farbay Ngornamaa bi Aamadu Mustafaa Njekk SARE