SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU TALAATA 03i FANI DESÀMBAR 2024

xamle - 03 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, talaata 03i fani desàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoorteel i Kàddoom, Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax mbooleem depite yi bokk ci 15eelu Ngomblaan gi ñu samp altine 02i fani desàmbar 2024.

Ndokkale na itam Njiitu Ngomblaan lu Bees li, di Sëriñ Maalig Njaay mi nekkoon Jëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg suuf si ak jaww ji, ak ñeneen ñi bokk ci pekkub Ngomblaan gi. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi ñu àndandoo ak Ngomblaan gi liggéey ngir luy gën a dooleel demokaraasib Senegaal, waaye rawati na diisoo diggante campeef yi, nga xam ne daa doon lu manul a ñàkk ngir amal doxaliin wu mucc ayib ci yoriinu pénc mi.

Ginnaaw yeesal gi ñu amal ci Ngóornamaŋ bi, Njiitu Réew mi Ndokkale na Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko miy wéyal sasu Njiital Ngóornamaŋ bi, Àbbaas Faal mi ñu tabb bees Jëwriñu Liggéey bi, Xëy mi ak Jëflante ak Campeef yi ak Yanqooba Jemmé Jëwriñ ju bees ji yor wàllu Jumtukaay yi ak Yaaleg suuf si ak Jaww ji, ak mbooleem Jëwriñ yi ak Sekkereteer Detaa yi ñu feddaliwaat ci seen i toogu. Nguur gi sóobu na ci pàcc bu am solo ci doxal Séegaal.

Jamonoy jubbanti ak tabaxaat réew mi nu tollu dafa laaj déglu, jege, njaxlaf, xereñte, leeraange ak royukaay ci yoriinu pénc mi, ngir yegg ci jubluwaay yi ñu pàcc-pàccee ci biir sémbu soppi réew mi fii ak 2050. Ci loolu Njiitu Réew mi ñaax na Ngóornamaŋ bi ñu gën a farlu ci li ëpp solo, jéem a doon Ngóornamaŋ buy teg ay pexe yu wér, Ngóornamaŋ bu déggoo tey amal njureef yu wér ci ni ñuy taxawee ci nammeel ak yittey askan wi, rawati na yu ndaw ñi nga xam ne ñoom lañu jiital ci naal yi ak sémbi pénc mi.

Njiitu Réew mi dellusiwaat na ci ndam yu yaatu yi am ci xew yi ñu jot a amal ci màggalug 80eelu atu bóom gi amoon Caaroy. Sant na bu baax Njiiti Réew yi ak gàngoori biti réew yi ñëwoon teewesi xew wi. Jaajëfal na Njiitu Jëwriñ yi ak Ngóornamaŋam, kurélug lootaabe gi Profesëer Mammau Juuf jiite ak ñi mu ko séqal, larme bi ak mbooleem ñi nga xam ne, ci lu sori walla lu jege, amal nañu ci liggéey bu mucc ayib, ba tax ñu man a am ndam ci lootaabeg màggal gu njëkk gii. Xew-xew bu metti bii daf nuy fàttali sunu wareef ci fexee delloosi liy dëgg ci jëf jii nga xam ne leegi ñépp dëppoo nañu ci baat bii di : « Bóomug Caaroy ».

Ngir dundal fàttaliku tiiraayéeri Afrig yu jàmbaare yii, fàttali na Ngóornamaŋ bi, dogal bi mu jël ci boole ci arminaatu Repiblig bi, bisub màggal « Bóomug Tiiraayéer yu Caaroy 44 ». Ci wàll woowu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñu Larme bi ñu gaaral kaadaru yoonal bu jëm ci « Musée-Mémoire-Cimetière » bu Caaroy. Woo na Ngóornamaŋ bi tamit mu gën a dooleel Kurélug lootaabe gi ci li ñu ko sas ci wàllu gëstu ak jàngale ci daara yi ak jàngune yi fàttaliku xew-xew bu tiis bii ci mboorum kembaar gi.

Lu soxal bilaŋ ak nisar yi ñeel bis bi ñu jagleloon Daara, Njiitu Réew mi sant na bu baax Jëwriñu Njàng mi, Kilifa diine yi ak njabootu daara ci fànn yépp, ci lootaabe gu mucc ayib gi ñu amal ci ñetteelu xewu bis bi ñu jagleel daara ci réew mi. 

Sàkku na ci Jëwriñu Njàng mi ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi ñu waajal ci fan yiy ñëw Jataayi Waxtaane Daara ci réew mi ngir man a jëmmal li ko dalee 2025 yoon wu bees ngir samp kenoy suqali daara ci fànn yépp ci Senegaal. 

Lu soxal mbirum doxal gu matale ci « kot pastoraal bi » ak dundalaat càmm gi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñu Mbay mi, Bay dunde ak Càmm gi, ñu dooraat lootaabe Bis bi ñu jagleel càmm ci réew mi.

Bis bu am solo boobu ci réew mi, dafa war a sax ci doon jamonoy toog diisoo ju wér diggante Nguur gi ak ñiy yëngu ci wàllu càmm, waaye tamit jataay buy boole ñépp ngir xayma ak baral jéegoy yeesal jëme ci wàll wii. Woo na Jëwriñ ji yor wàllu Càmm gi, mu lëkkaloo ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, dooraat kopparal pàccub Càmm gi boole ko ak dooleel gu wér ci balluwaay ak doxaliinu FONSTAB.

Mu daanelee moom Njiitu Réew mi ci ngan gi Seneraal Biris Oligi Ngemaa, Njiitu Réewum Gaboŋ di amal ci Senegaal te ànd ko ak gàngooru Jëwriñ gu takku. Ñaari réew yi jot nañoo waxtaan ci fànni lëngoo yu bari yu ñu war a gën a dëgëral (njàng mi, tàggatu gi, kaaraange gi, suqalikug sektéer piriwe bi ans). Sàkku na ci Jëwriñu Bennaleg Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew mu taxaw ci lëkkale wayndare yi ak Jëwriñ yi mu soxal. 

Ci ndoorteel i kàddoom, Njiital Jëwriñ yi sant na bu baax Njiitu Réew mi ci kóolute gi mu yeesalaat jëme ci moom ak ci ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi. Loolu nag di tegtale rekk liggéey bu mucc ayib bi mu jot a sottal ci ay ndigalam, ci juróom ñetti weer yi njëkk ci nguuram. Ñaanal na Jëwriñ ju bees ji yor wàllu Liggéey bi, Xëy mi ak Jëfalante diggante Campeef yi, mu am ndam lu rëy ci li ñu ko sas. Ginnaaw ba mu xamlee ne fàww Nguur gi di jiital saa su ne pas-pasu amal njureef yu mucc ayib, Njiital Jëwriñ yi woo na Jëwriñ yi ak Sekkereteer Detaa yi ñu taxaw temm ci fexee jëmmal yi ñu dëxëñ ci biir « Agenda 2050 » bi jëm ci soppi gu wér te wóor ci Senegaal. 

Ci wàll woowu, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, mu lëkkale liggéey yi aju ci mottali « Dekklaaraasoo Politig Seneraal » bi mu fas yéenee amal balaa yàgg ci kanamu Ngomblaan gu bees gi.

Ci geneen wàll, Njiital Jëwriñ yi soññ na Jëwriñ yi ñu sóobu ci njëlu atum 2025, te jiital ci wayndare yi gën a jamp. Ci loolu, Jëwriñ ju nekk jot na ndigalu rëdd yoonu doxaliinam ci ñetti weer yi njëkk ci atum 2025. Ci fànn googu, Njiital Jëwriñ yi fàttali na ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi solos bàyyi xel bu wér àppi sémbi liggéey yi, ñeel wànqaas yi aju ci seen njëwriñ. Sàkku na ci ñoom itam ñu def ub xayma ci limub nit ñi jàppandi ci seen njëwriñ méngale ko ak li leen di xaar ci liggéey.

Mu daanele moom Njiital Jëwriñ yi ci xamal Ndiisoo gi, yoon wi Kurél gi ñu dénk Màggalug bóomug tiiraayéeri Senegaal yi 1 panu desàmbar 1944, fas yéene liggéeyee fii ak weeru awril 2025. Mu war a tombe ak bis bi ñu war a gaaral Njiitu Réew mi benn « Livre Blanc ». Ci doxaliin wii, xamle na solos amal liggéeyi càmbar, jaare ko ci ay jumtukaayi xarala, ci warab yi ñu wax walla ñu njort ne fa lañu suul ñenn ñi sukkandiku ko ci ay gëstu ak i seede yu ñu jot a taataan.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :


  • Sémbu yoonal wi jëm ci jubbanti Koppalug atum 2024 ; 
  • Sémbu yoonal Kopparal gi ñu jàpp ngir atum 2025.


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE