SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 29i FANI SÃAWIYE 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 29 MONTHS.JANUARY 2025

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 29i  fani sãawiye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi àddu na ci màggalug 145eelu Wooteb Seydinaa Limaamu Laahi Al Mahdi gi ñu jàpp 30 ak 31i fani sãawiye 2025. Ndokkeel na bu baax Xalifa Seneraalu Laayeen yi, Seriñ Muhammadu Maxtaar Laay ak mbooleem taalibe yi ci seen dogu ak seen i ñaan ngir Senegaalu jàmm, dal ak yokkute ci biir mànkoo. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu taxaw temm, ànd ko ak way-lootaabe yi, fexe ba xewu diine wii di woote bi jaar ci yoon ci gox yi ñu koy amalee (Yoof, Kàmbereen, Ngor).

Ci wàll woowu ba leegi, Njiitu Réew mi xamal na Ngóornamaŋ bi ne fàww mu taxaw itam ci fexe ba ñu amal lootaabe gu mucc ayib ci Màggalug Poroxaan gi ñu war a amal 06i fani féewarye 2025, boole ko ak bàyyi xel bu baax ci yokk matuwaay yi jëm ci fegu ak kaaraange gi ci yoon yi. Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi wane na ag tiisam ci ñi ñàkk seen bakkan ci aksidaŋ bu metti bi am talaata 28i fani sãawiye 2025 ci yoon wi (diggante Bàmbey-Xombol). Jébbal na njaalam jëme ci njabootu ñi faatule teg ci ñaanal wérug jàmm ñi ci am i gaañu-gaañu. 

Njiitu Réew mi dikkaat na ci ñu fexee taxaw ci fuglu bu baax anam yi ñuy saytoo wàllu approwisonmaa yi ak njëgu porodiwi yi ñuy faral di jëfandikoo rawati na ci koor ak karem yiy dëgmal. Muy ñaari xew-xew yu am solo lool ci wàllu diine. Doon it jamono yoo xam ne dañu ciy jëfandikoo bu baax yenn porodiwi yu mel ni ceeb, suukar, diwlin, meew, fëriñ, mburu añs. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi mu taxaw ci jàmmaarloo ak ñiy denc walla ñuy yokk njëgi porodiwi yi, boole ko ak jël mbooleem matuwaay yi war ngir fexe ba tuur lu doy sëkk te jaar yoon ci marse yi ci wàllu porodiwi yi ñuy yittewoo te sàmmontewaale ak njëg yi ñu tëral. Woo na Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi ak Sekkereteer Detaa bi yor wàllu PME / PMI ñu gën a dooleel «consomer local » gi te gën cee sóob ndefar yiy yëngu ci wàllu dund ak baral jéego yi jëm ci doxal sémb ak naali soppi liy ñoree ci réew mi. Mu tëjee wàll woowu ci fàttali Ngóornamaŋ bi ne jot na sëkk ñu tëggaat sistemu approwisonmaa réew mi ci wàllu dund ak hidrokarbiir, te bàyyiwaale xel bokk gi Senegaal def bu yàggul dara ci réew yi am petorol ak gaas. 

Askan wi ak gox yu bari yëguñu ag yokkute ci jëfandikoo gi ñuy def ci balli mbindaare yi ci gox yooyu. Loolu di tekki ne Nguur gi war naa def yitte fexee taxaw temm ci nekkiinu askan yiy dund ci gox yooyu mbell yi nekk. Loolu moo tax Njiitu Réew mi sàkku ci Jëwriñ yi yor wàllu Mbell yi, wàllu Gox yi ak Goxaan yi, wàllu Koppar yi, wàllu Koom mi ak wàllu kéew mi ñu xayma, ci caytug Njiital Jëwriñ yi, njeexital yi jëfandikug mbell yi am ci yokkuteg gox yooyu ci wàllu koom mi, dundiin wi ak kéew mi. Xamle na ne jot na sëkk ñu leeral « Fonds d’Appui au Développement des Collectivités territoriales » ak eewestismaa yi ñu jot a amal ci ay jumtukaay yu ñeel askan wi niki ko « Code minier » bi diglee. 

Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu ànd ak ñiy yëngu ci gox yi jël ay matukaay yu ñu déggoo jëm ci gën a rattaxal jëflante yi diggante kër yiy yëngu ci wàllu mbell yi ak askan yi jaare ko ci sàmm kéew mi, amal ay xëy ci gox yooyu ak gën a taxaw ci lii di « Responsabilité sociétale d’Entreprise (RSE)». Lu jëm ci gën a dooleel yoriin wu leer ci wàllu mbell yi, xamal na Njiital Jëwriñ yi ne fàww ñu amal xayma gu matale ci kër yii di « Société des Mines de fer du Sénégal oriental (MIFERSO)» ak « Société des Mines du Sénégal (SOMISEN)». Ci lu soxal moom gi nu bëgg ci sunuy balli mbindaare, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu teg ay jéego yu jëm ci taxawal ci réew mi « Comptoir commercial»  ci wàllu wurus  ngir taxaw ci càkkuteefu sunu tëgg yi.

Nawetaan yi bari nañu lool lu ñuy jur ay fitna ak i tiis ci gox yu bari ci Senegaal. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Tàggat Yaram, mu sumb ay waxtaan ak ñiy yëngu ci wàll wi ngir man a tëral arminaat bu wóor ci joŋante yi rawati na nag amal ay coppite ci Nawetaan yi lépp jëm ci gën a suuxat siwismu ak fésal bëgg sa réew. 

Njiital Jëwriñ yi xamal na Ndiisoo gi ne ñu ngi wéyal liggéey yi aju ci jëmmal « Agenda Sénégal 2050 », jaare ko ci fésal limub sémb, naal ak coppite yi gën a far te ñu war leen a gaaral gën gaa yeex ci xaaju weeru féewarye 2025 bi Njiitu Réew mi ngir mu walide leen. 

Njiital Jëwriñ yi teg ci yëgal Ndiisoo gi ne taxawal nañu, jaare ko ci dogal bu ñu jël tay jii, ci ndigalu Njiitu Réew mi, ci topp gu muy jiite, lëkkaloo diggante Senegaal ak réew ak kuréli « Proche » ak « Moyen Orient » ak li des ci kembaaru Asi. Lëkkaloo googu nag mu ngi soxal lu tollu ci ñaari téeméeri (200) lëngoo walla sémbi lëngoo ci fànn yu wuute, ànd ko ak lu mat 15i réew ak kuréli kopparal. Ci noonu, taxawal nañu benn « task force » bu boole ab lim ci ay njëwriñ, APIX ak FONSIS. Bokk na ci li ñu ko sas muy natt lëngoo yiy dox jamono jii, càmbar wayndare yi ñu jébbal Njiital Jëwriñ yi te aju ci lëngoo yi ñu namm a amal ak réew yooyu ak xool eeweatismaa yi man a bawoo biti réew walla koppar yuy bawoo ci réew yooyu ñeel Senegaal. 

Mu daaneel moom Njiital, ci xamal, njëwriñ ak wànqaas yi aju ci ñoom, njariñu gaaw taxaw, ci genn wàll, taxawu « pré-archivage » bi dugal ay koppar ci wàllu dokimànteer yi ci « Archives nationales » yi, ak ci geneen wàll, tabax Kër gu méngoo ak jamono gu ñuy jagleel « Archives» yi.  Namm naa taxawal itam benn komite « interministériel» ci yoriiinu « Archives» yi, bu ñuy sas muy saytu tëggaat sàrt yi ñu tëral ci wàllu « Archives» yi ci Njëwriñ yi ak wànqaas yi niki noonu di koordone pexe mu ñuy saytoo « Archives» yi ci réew mi.


Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay yi àddu na ci jëmmal gi ñu namm a amal ci « pôles territoites » yi. 


CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Sémbu dekkere bi aju ci doxal sàrt l° 2020-01 bu 06i sãawiye 2020 bi jëm ci taxawal ak dooleel « startup » bi ci Senegaal.  


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE