Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 15i fani sãawiye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi taxaw na bu baax ci xamle ne jot na sëkk ñu baral jéego yi jëm ci moderniise dem bi ak dikk gi ci wàll yépp ginnaaw njureef yi bawoo ci diisoo yi ñu doon amal ci wàll wi. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg suuf si ak jaww ji, ñu mottali pexe yi Ngóornamaŋ bi teg jëm ci moderniise dem bi ak dikk gi, te bàyyiwaale xel ci doxal gi, mbooleem gàllankoor yi ci am ci wàllu yoon, jumtukaay, ndoxal, galag ak koppar yi tax yegg ci jubluwaay yi ñu tegoon xaw a jafe. Fàttali na Ngóornamaŋ bi, ci lu soxal doxal matukaay yi ñu jëloon ngir gën a taxaw ci kaaraangeg yoon yi, ne fàww ñu teg jumtukaay bu ñuy jagleel yoonal dawalug moto yi, niki ko « code de la route » diglee ak dogal yi ñu jël ngir man di yóbbu ak a indi ay nit ci tund ak gox yu fasantikoo.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Yaale ji, mu gën a taxaw ci yoon wi ñu tegoon jëm ci yeesal sëfaan yi, mbooleem xeeti daamar yiy daw ci biir dëkk yi ak ci diggante gox yi. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu boole wàllu dem bi ak dikk bi ci pàcc yi gën a far yi nga xam ne dina bokk ci pexe yi ñuy teg ngir taxawal ay xëy ñeel ndaw ñi. Ci loolu, Ngóornamaŋ bi war naa taxaw temm ci yokk jumtukaay yi ci wàllu tàggatu gu xereñ (ay dawalkat, ay mekanisee, añs) boole ko ak gën a aar « emplois informels » yi ci wàll wi jaare ko ci lootaabe ñi ciy yëngu, Kopparal leen, waaye tamit di amal ndànk-ndànk ay « contrats de travail » yu sax te ànd ak « couverture sociale » bu matale. Jumtukaay yi ci wàllu déggoo yi dox diggante Nguur gi ak Njjatige yi ak « Couverture sanitaire universelle » tamit dañu leen a war a jëme ci wet googu.
Lu soxal porogaraam bii ñu dooroon ca 2021 ba leegi te mu des lu bari, muy « Xëyu Ndaw ñi », Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu ànd ak Jëwriñ yi mu soxal jël mbooleem matuwaay yi war jëm ci xayma ak tëggaat porogaraam bii balaa njeextalu weeru mars 2025. Mu war a doon luy jëm ci taxawal gis-gis bu bees bu wóor ci wàllu « Xëyu Ndaw ñi » teg ci ëmbaale lépp li ñu ciy séntu. Xoolaat Porogaraam bii, dina tax ñu man a tëggaat ci lu gaaw mbooleem nammeel yi ak jubluwaay yi jëm ci man a taxawal ay xëy boole ko ak dooleel « entreprenariat » bi jaare ko ci gën sellal anam yi ñu koy kopparalee ak mbooleem yëngu yi man a génne ab xaalis.
Jëmmal «Vision Sénégal 2050 » bi nag warees na cee boole bu baax ci yitte yi, jéem a suqali jumtukaay yi ci wàllu géej yi ak poor yi. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñ ji yor wàllu Jumtukaayi Géej yi ak Waax yi, ñu matale balaa njeextalu weeru mars 2025, politigu Senegaal bu bees bi ci wàllu géej gi ak waax yi, te bàyyiwaale xel taxawaay bi sunu réew am ci wàllu géej gi ak mbooleem sémb yi jot a sotti, yi nekk ci yoonu sotti ak yi ñuy naal. Ci loolu, xamle na ne, boo xoolee jafe-jafe yu bees yi laxasu ci wàllu géej yi, fàww ci wàllu coppite yi, ñu yeesalaat boole ko ak yaatal anam yi ñuy saytoo poor piblig yi ak piriwe yu Senegaal waaye tamit gën a dooleel kër giy saytu mbiru géej yi ci réew mi di ANAM. Ci geneen wàll, sàkku na ci Jëwriñu Jumtukaayi géej yi ak poor yi, mu gën a taxaw ci moderniise poor yi ak kee « de pêche » yi. Etaablismaa yooyu nag dañu leen a war a jagleel porogaraam bu yaatu ci wàllu moderniise leen fépp ci réew mi.
Njiitu Réew mi xamle na tamit ne, jot na sëkk ñu xoolaat lëkkaloo gi dox diggante Nguur gi ak « Consortium sénégalais d’Activités maritimes (COSAMA) », niki noonu it fàww nu fexee téyeel sunu bopp ci fànn yépp caytu gi ak suqalikug « chantiers navals » yu Ndakaaru, boole ko ak tegaat ci kanam « Société des Infrastructures de Réparation navale (SIRN) », doolelee ko « Marine nationale » bi. Ci wàll woowu ba leegi, woo na Jëwriñu Napp gi ak Jumtukaayi géej yi ak Waax yi, mu ànd ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, xayma ak xoolaat sas ak yënguy « Conseil sénégalais des Chargeurs (COSEC) ».
Lu soxal dooleel jëflante yi diggante Nguur gi ak diine ji, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi taxawaay bu am solo bi këri diine yi am ci li gën a dëgëral bennoo gi ak dal gi am ci Senegaal. Feddali na yéeneem ci yóbbu jëflante yooyu ba ci dayo bu gën a kawe jaare ko ci taxawal balaa yàgg, benn « Délégation générale aux Affaires religieuses » ginnaaw bu ñu ci diisoo ak mbooleem ñi ko séq.
Ci loolu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu gën a sóob Ngóornamaŋ bi mu baral jéego yi jëm ci moderniise dëkki diine yi boole ko ak suqali « tourisme religieux » bi.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Bennog Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew mu jël mbooleem matuwaay yi war, ci caytug Njiital Jëwriñ yi, ngir amal lootaabe gu mucc ayib jëm ci Ajug Màkka gi ak Ajug Kerceŋ yi. Mu daanelee ci sàkku ci Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, mu taxaw temm ci bàyyi xel waajtaay wu mucc ayib jëm ci Màggalug « Kazu Rajab » gi ñu jàpp 27i fani sãawiye 2025 ak Wooteb Seydinaa Limaamu Laay bi ñu jàpp 30 ak 31i fani sãawiye 2025.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiital Jëwriñ yi dikkaat na ci anam yi mu amalee tukkeem bi ca Móritani 12 jàpp 14i fani sãawiye 2025 ak tomb ya ñu fa jot a tënk. Xamle na jéego yu am solo yi am ci lëkkaloo gi dox diggante ñaari réew yi, rawati na ci wayndare yi soxal suqalikug sémbu gaas bii di GTA ak yi soxal wàllu napp gi ak dem bi ak dikk gi.
Njiital Jëwriñ yi rafetlu na itam njureef yi bawoo ci liggéey yi ñu doon amal jëm ci jëmmal « Agenda national de Transformation Vision Sénégal 2050» bi, boole ci ñaax mbooleem ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi ñu taxaw temm ci sàmmonte ak àpp yi ñu teg, rawati na lu jëm ci walide limub naal yi, sémb yi ak yeesal yi gën a far niki noonu matukaay yi jëm ci topp gi ak xayma gi. Taxaw na bu baax ci ñu amal taxawu gu wér te wóor ci doxaliinu coppite yi, tàggatu gu sax niki noonu gën a dooleel ak fullaal « Cellules d’Etudes et de Planification » yi.
Lu soxal wareefu amal topp gu wóor ci koppar yi ñu jagleel « dépenses d’investissement » yi fii ak ñuy xaar matug naal ak sémb yi gën a far ci yoon wi ñu war a jaar ci atum 2025 te nekk ci « plan quinquennal 2025-2029 » bi, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, mu lëkkaloo ak Jëwriñu Koom mi, Palŋ ak Lëkkaloo ak Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, jébbal ko ca na mu gën a gaawee, limub naal ak sémb yi ñu jàpp ci wàllu depaas yi ñu war a àngaase ci tirimestar bi njëkk ci atum 2025, ngir Njiitu Réew mi man cee joxe ndigal.
Mu daanele moom Njiital Jëwriñ yi ci xamal Ndiisoo gi, ci lu jëm ci wàññi dundiinu Nguur gi, matukaay yu bees yu ñu teg leegi jëm ci saytu yónnen yi ndawi nguur gi war di doxi biti réew.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
- Jëwriñu Caabal gi, Jokkoo yi ak Xarala yi àddu na ci pexe mu bees mi Senegaal teg leegi ci wàllu xarala te tuddee ko «New Deal technologique » ;
- Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram ak Mbatiit dikkaat na ci waajtaay yi ñuy amal jëm ci « Jeux olympiques de la Jeunesse (JOJ Dakar 2026) ».
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE