Réewum Siin: Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay demoon nemmikuji porowees bu Shandong

xamle - 06 MONTHS.SEPTEMBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay demoon na ca Jinan, di gox bu féete ca tundu Shandong, di benn ci gox yi gën a naat ci réewum Siin, am PIB bu ëpp 1300i milyaari dolaar.

Ginnaaw ndajeem ak M. Lin Wu, Njiital Comité du Parti provincial, Njiitu réew mi nemmiku na Akaademib Shandong biy gëstu ci wàllu mbay, mu seetlu fa nag jéego yu am solo yi gëstukati saa-siin yi jot a teg ci wàllu gëstu ak xereñte ci wàllu mbay.

Ci loolu, ci bernde bu yaatu bu leen Góornoor Zhou Naixiang, jot nañu faa waxtaane ay lëkkaloo yu bari yu ñu war a man a taxawal ci wàllu mbay mi, ndefar yi, napp gi ak xarala yi. Doxaliin wu yaakaaru wii mu ngi jëm ci gën a dooleel lëngoo gu am solo diggante Senegaal ak Shandong.