Powi olempigu 2026 yi ñeel ndaw ñi: Njiitu Réew mi dalal na Tomaas Bach

xamle - 18 MONTHS.OCTOBER 2024
Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye dalal na démb ci ngoon gi Njiital CIO li am waar wu muy matalesi ci Ndakaaru jamono jii.
Tomaas Bach, xamle na ne xelam dal na bu baax ci matukaay yi ñu jël ngir amal lootaabe gu mucc ayib jëm ci JOJ yi Senegaal war a dalal ci atum 2026.