Biti Réew - 06 MONTHS.NOVEMBER 2024
Ci bataaxel bu mu fésal ci mbaalu jokkoo bii di X, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ndokkale na Donald Trump mi falu Njiitu Njiitu Réewum Etats-Unis. Njiitu Réew mi fésal na yéeneem ci gën a dooleel lëkkaloo diggante ñaari réew yi àndandoo liggéey ngir jàmm, naataange ak sàmmonte ak mbaax yi ñu bokk. Àddu gii mu ngi ko def ginnaaw ndamul Trump li joŋantey Amerig yi amoon 5i fani nowàmbar 2024.