waxtaan - 16 MONTHS.JANUARY 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, jiite na tay ci alxemes ji 16i fani sãawiye 2025, xew wu am solo wi soxal tijjitel Ëtt ak Warabi Àttekaay yi ca « salle d’audience » bu Ëttu Àttekaay bu Kawe bi.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi fàttali na solos YOON ci biir Repiblig bi, ndax moo war a sàmm péexte yi manul a ñàkk ak dalug pénc mi. Xamle na itam ne fàww ñu wéyal coppite yi ngir gën a méngale ak jamono ni yoonu réew mi di doxee ak taxaw ci fexe ba ñu man a doxal sañ-sañu seleŋlu ci kaw sàmmonte ak dalug pénc mi ak li ñépp bokk.
Muy xew woo xam ne am pose la ci Nguur gi mu feddali jaayanteem jëm ci taxawal Yoon wu xereñ, wu yomb a jot boole ko ak di sàmm yelleefi ñépp.